Yenn ci wànqaasi réew mi doon ndokkale Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay.

xamle - 03 MONTHS.JANUARY 2025



 (

Xew wi yenn wànqaasi réew mi baaxoo amal jëm ci amal  ay ndokkale ci at mu yees mi,  tay la woon ci ngoon gi ci Njéndel Réew mi.

Ngomblaan gi, Ngóornamaŋ bi, bànqaasu yoon, way-kaaraange gi, kilifa diiine yi ak yu aada yi, niki noonu yeneen i kurél, ndokkale nañu Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ci at mu yees mi,  ñaanal ko mu doon atum jàmm ak xéewal.

Man ngeen koo seetaan fii :