YËGLEB PRÉSIDENCE DE LA RÉPUBLIQUE

xamle - 17 MONTHS.JANUARY 2025

Ay waxtoo ngi nii, am xibaar buy wër ci yenn dali web yi ak mbaali jokkoo yi, di xamle ne soxnas Njiitu Réew mi, Maam Absa Fay daa mucc. 

Soxna saa ngi ci jàmm bu baax te kenn téyeewu ko ci benn barabu fajukaay, ndax am lenn lu ko dal. 

Noo ngi woo mejaa yi ak askan wi ñu gën a am taxawaayu kilifteef te gën a def fulla ci wérlu xibaar yi laataa ñu leen di fésal, ngir moytu di dugg ci dundug jàmbur ak dalug nit ki. 


Ndakaaru, 17i fani sãawiye 2025.

Jëwriñ-xelalekat, Farbay Présidence de la République