Biti Réew - 29 MONTHS.JUNE 2025
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, yegg na ci dibéer ji ca “Seville”, ca Espaañ ngir teewe 4eelu ndaje mi Mbootaayu Réewi àddina si di amal ngir waxtaane kopparalug suqaliku gi, 30i fani suwe jàpp 2i fani sulet 2025.
Ba muy yegg ca naawub Seville, moom Njiitu Réew mi, kilifay Espaañ yi niki noonu ñi teewal Mbootaayi Réewi Àddina si ca Ndaje ma, ñoo ko teertu.
Ndaje mu kawe mii dina doon jataay bu am solo ngir waxtaane doxaliin yu bees ci wàllu kopparal yu man a jàpp ci sottalug jubluwaayi suqaliku gu sax (ODD) ci tolluwaayu jamono juy soppiku bu baax.