Yeggug Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ca Ndar ga muy amal tukkib nemmiku.

xamle - 12 MONTHS.JUNE 2025

Njiitu Réew mi yegg na ci alxemes ji ca Ndar, muy màndargaal ndoortel nemmiku ñaari fan gu mu war a amal ca “pôle territoire Nord”. 

Ba muy yegg ca naawub Usmaan Ma-Sekk Njaay, moom Njiitu Réew mi, Góornooru tund wa moo ko dalal, ànd ko ak kilifay ndoxal yi, way-falu ña ak tañu sóobare ya ko tatagal. 


Muy tukki buy tàbbi ci yoonu suqali gox yi ñu tënk ci biir yitte yi ñu jiital ci 

Vision Sénégal 2050”, te jëm ci dooleel yokkuteg koom ak nekkiin wu dul beddi kenn ci biir réew mi.