Xewu Màggal bis bi réew mi moomee boppam.

jëwriñ - 04 MONTHS.APRIL 2025

 “Place de la Nation” dina dalal, àjjuma 4i fani awril 2025, xewu màggal 65eelu at mi Senegaal moomee boppam. Muy xew-xew buy am ci teewaayu Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ak gan ñu màgg ñu bawoo ci réew yi nu xaritool.  

Màggal gi dees na ko dooree ci fésal gànnaay yi, toftal ci sargal jëmm yu ràññiku, jeexalee ko ak maaj guy boole siwil yi, militeer yi ak paramiliteer yi, niki noonu maajug moto yi ak daamar yi ak wanewu ci jawwu ji.

Ci at mii, wëppa wi ñu tànn mooy “Larme bu moom boppam ci wàllu xarala ak ndefar”, muy wane jéego yu am solo yi Senegaal di teg jëm ci yokk dooleem ci wàllu militeer ak moom boppam ci wàllu ndefar.