Xewu jébbale karney njàmbati mbootaayi sàndikaa yi

jëwriñ - 01 MONTHS.MAY 2025

Ci posem bis bi ñu jagleel liggéeykat yi ci àddina si, 1 panu mee 2025, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dina jiite xew wu am solo wi jëm ci jébbale karney njàmbati mbootaayi sàndikaa yu Senegaal. Xew wii, di jataay bu am solo ci wàllu diisoo, dina may ñi teewal liggéeykat yi ñu yaatal seen i njàmbat boole ko ak gaaral ay pexe ngir suqali nekkiinu liggéeykat yi, dooleel xëy mi ak yamale ci wàllu liggéey bi.