[WIDEWOO] Jataayu Màggal 80eelu atu bóom gi amoon Caaroy: àddug Njiitu Réew mi.

waxtaan - 01 MONTHS.DECEMBER 2024

Senegaal màggal na tay 1 panu desàmbar 2024 80eelu atu bóom gi amoon Caaroy, di xew-xew bu tiis ci mbooram. Jataay bi Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay jiite, dajale na ay njiiti Afrig, kilifa yu bokk ci Ngóornamaŋ bi ak gan ñu bawoo fépp ci àddina si.

Peresidaa Fay ànd na ak ay naataangoom ñu teg ay fulóor ca sëgi Caaroy, teg ci nammiku barab ba ñu jagleel fàttaliku tiiraayéeri Senegaal ak malgaas, te Profesëer Mammadu Kone amal ay leeral ci lu ñu tuddee “Thiaroye 44 : une mémoire blessée”.


Ñu wéyal bis bi ca Kãa Liyetnaa Aamadu Lindoor Faal ak jataay bu sóobare yi ak siwil yi wane seen bopp, te doon màndarga mu am solo ci xamle xew-xew bu metti bii. 

Ci àddoom, Njiitu Réew mi delloo na njukkal tiiraayéeri Senegaal yii faatu woon 1 desàmbar 1944. Njiitu Réew mi xamle na ne dees na tabax ab memoriyaal ca Caaroy bu war a doon barabu fàttaliku, niki noonu taxawal itam benn barabu xamlu ak gëstu. Xamle na itam ne dees na jël yenn ci ay mbedd ak i pénc tuddee leen xew-xew bu tiis bii teg ci dugal mboorum Caaroy 44 ci njàngum Senegaal.

 Man ngeen a teewlu kàddu yi: