[ WIDEWOO ] Àddug Njiitu Réew mi ba mu dellusee Ndakaaru ginnaaw tukkeem ba ca Seville.

laaj ak xibaar - 02 MONTHS.JULY 2025
Ginnaaw ba mu teewee ñenteelu Ndajem àddina si ci kopparalug suqaliku gi, ñu doon ko amal ca Seville, ca tundu Andaluus, ca bëj-saalumu Espaañ, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY Njiitu Réewum Senegaal, dellusi na Ndakaaru tay ci ngoonug àllarba ji. 

Naka mu dellusi ci réew mi rekk, ci la Njiitu Réew mi daal di yékkati ay kàddu yu mu jagleel askan wi. Dikkaat na ci mbooleem jàngat yi mu def ci tukki bi mu doon amal ca Seville ci wàllu FFD4 bi, laataa muy wax ci xew-xew yu tiis yi am ca gox yu Kàmbereen ak Rooso. Ci loolu, feddali na yitte ju sax ji kilifa yi am ci xew-xew yooyu, ak jaayanteg Nguur gi jëm ci indi ci saafara ya ca war. 

Widewoo bi :