"Waxtuw ODD 2024" : Njiitu Réew mi yaatal na gis-gisu Senegaal ngir baral jéego yi jëm ci yegg ci Jubluwaayu Suqaliku gu Sax (ODD).

Biti Réew - 24 MONTHS.SEPTEMBER 2024
"Waxtuw ODD 2024" amal nañu tay ci ngoon gi ca États-Unis, mu dajale woon jëmm yu am taxawaay yu mel ni Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye.
Mu doon mennum Njiitu Réewu Afrig mu nekkoon ci weti kilifay yeneen ñenti kembaar yi, Njiitu Réew mi yaatal na gis-gisu Senegaal ngir baral jéego yi jëm ci yegg ci Jubluwaayu Suqaliku gu Sax (ODD).
Cig àddoom, Peresidaa Fay wax na itam ci politigu Nguur gi jëm ci wàññi njëgu jot ci internet ci Senegaal. Mu jàpp ne, xarala googu am na njeexital yu am solo ci mbooleem pàcci dund gi, moo xam njàng mi la, mbay mi, paj mi ba ci sax yeneen fànn yu ñuy yittewoo.
Njiitu Réew mi xamle na itam yéeneem ci dugal ci Ndayi Sàrti Réew mi boole ci yelleefu jot ci lënkaay (connexion), niki ñu ko defee ci yeneen yelleef yu jot a nekk ci biir Ndayi Sàrti Réew mi, yu mel ni yelleefu jàng ak péexteg àddu.