Washington : Peresidaa FAY dalal na tañu Boeing, wu Millennium Challenge Corporation ak ay kàngami Senegaal yu FMI.

Biti Réew - 10 MONTHS.JULY 2025

Ci ndaje mi mu doon amal ca “Maison Blanche”, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, amal na ay ndaje yu am solo ca Washington. 

Jataayu na ak tañu Boeing, ci njiitu S Michael Schnabel, Topp-Njiitu Ndoxal gi yor wàllu yëngu yi ci àddina si. Waxtaan yi jëmoon ci dooleel lëngoo gi ak Air Senegaal, rawati na jaare ko ci wutum ropplan yu am doole, suqali man-man yi ci réew mi, ak sos ay xëy yu xereñ ci wàllu yaaleg jawwu ji ci Senegaal.


Peresidaa Jomaay daje na itam ak kilifay Millennium Challenge Corporation (MCC) ngir waxtaane mbébetu dooleel lëngoo gi ci sémbi joyyanti koom mi ñu nekk di amal jamono jii ci Senegaal.


Ngir tëj, Njiitu Réew mi am na mbégte lool ci weccente ak ay kàngami Senegaal yu yor toogu yu kawe ci biir FMI ak Bànk Monjaal, ci jafey-jafey koom mi ak naali yokkute gu sax ñeel sunu réew.


Waxtaan yu am solo yii nag dañuy firndeel jaayante gu wér gi Peresidaa Jomaay am ngir dooleel bu baax lëkkaloo gu dëgër te am njariñ ngir ëllëgu Senegaal.

Peeñ: