Wal yi : Njiitu Réew mi ca Caaroy Géej ak ca Parsel ngir massawu askan wa.

xamle - 16 MONTHS.AUGUST 2025


Njiitu Réew mi demoon na tay, ca Caaroy Géej ak ca Parsel Aseni Unite 24 ngir daje ak askan wa fa loru ci wal yi ak yokkuteg géej gi. 


Massawu na leen, teg ci xamal leen ne mu ngi ci seen wet boole ci feddali ne dees na sóob mbooleem wànqaasi nguur gi ngir taxawu leen.


Donte lañuy dund metti na, terewul askan wa rafetlu bu baax dikkug Njiitu Réew mi foofa ak Kàdduy dëfal yi mu fa yékkati. 


Njiitu Réew mi feddali na jaayanteg Ngóornamaŋ bi jëm ci amal jëf yu wér te wóor ngir féexal jaboot yi, sàmm koñ yi boole ko ak jëmmal pexe yu sax dàkk ngir njariñal askan wépp.