Vision Sénégal 2050 : Bokk yéene ngir réew mu moom boppam, naat te mànkoo.

xool - 01 MONTHS.AUGUST 2025

“Vision Sénégal 2050” day wane yéene ju sell ji réew mi am ngir tabax askan wu dëgër, wu boole ñépp te moom boppam, lépp ci kaw méngoo ak i mbaaxam, ay balluwaayam ak nammeeli aw askanam. Day sóobu ci yoonu soppiku gu xóot, gu tegu ci yoriin wu leer, xereñ ak yamale ci askan wi. 

 

Muy tegtalukaay bu namm a tegaat Senegaal niki keno bu mag ci suqalikug Afrig, jaare ko ci yeesal, jëfandikoo xam-xam bi ci ay doomam, jàll jëm ci wàllu ekolosi ak moom boppam ci wàllu koom. Mu war a sampe ci juróomi keno yu am solo: 

• Koom mu meññ te am doole, mu sukkandiku ci sopparñi liy ballee ci réew mi, samp ay ndefar boole ko ak peeg wuumi njariñ yi. 

• Mboolaay gu boole ñépp te yemale, goo xam ne ma-réew bu nekk dina man a jot ci anam yu maandu ci yitte yi gën a far, njàng mi, paj mi ak xëy mu baax 

• Royukaay ci wàllu yoriin, wu lalu ci saytu yoriinu alal ji, wu ma-réew bu ne di dugal  loxoom  ak xeex  nger. 

• Mbeeraay gu ñoŋ te duggalante, ay jumtukaay yu méngoo ak jamono te ànd ak jëfandikoo xarala yi. 

• Gën a dooleel manal sunu bopp, muy ci wàllu njël li ak ci wàllu pexe yi, ngir taxaw ci jonnug tànneef yiy am ci réew mi. 


“Vision Sénégal 2050” ab woote la bu jëm ci jaayanteg kenn ku ne : ñuy woo campeef yi, sektéer piriwe bi, sosete siwil bi ak ma-réew yi, kenn ku ne dugal ci loxoom bu baax. Mooy rëdd yoonu Senegaal gu taxaw jonn, téyeel boppam ëllëgam, te taxaw temm ngir jëm kanam. 


Ngir am lu gën a yaatu ci tegtalukaay bu am solo bii di "Vision Sénégal 2050”, wayndare wi jàppandi na, man ngeen a jaar fii ci suuf ngir wàcce ko :