xamle - 26 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay jataayu na ak Sekkereteer Seneraalu ONU,
Antóño Guterres. Ànd nañu, fésal gis-gis bi ñu bokk am ci yittey àddina si teg ci fas yéene liggéey ci gën a dooleel lëkkaloo diggante Senegaal ak wànqaasi ONU yi.
Muy rafetlu kilifteefu Peresidaa Fay, moom Sekkereteer Seneraal bi sàkku na ci moom mu doon kenn ci waada yi war a jëmmal déggoog ëllëg ngir dooleel jàmm, kaaraange ak suqaliku gu sax.