xamle - 27 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ci teewaayu ndawi àntarperenéer yu Senegaal yuy yëngu ci wàllu xarala ci njital Jëwriñu Jokkalekaay yi ak Xarala yi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay daje na ak ekib yu 500 Global, di kër gu fés ci wàllu "kapitaal-risk”.
Demam gii am ginnaaw ba mu bawoo ca NVIDIA tax na ñu gis ay fànn yu am solo yu ñu man a dugal ci Senegaal, jëm ci gën a doxal ekosistemu jéemantu ci réew mi ak taxawu ndaw ñi xereñ ci wàllu xarala.