Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ginnaaw bi mu dalalee Njiital Jëwriñ lu Luxembourg ba noppi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na Bill Gates.
Waxtaan yi a ngi jëmoon ci gën a dooleel lëkkaloo diggante Senegaal ak Fondation Gates, ci gën a fésal yittey suqalikug réew mi, jaare ko ci taxawu intelligence artificielle, asanismaa, niki noonu jëfandikoo xarala yi ngir gën a joyyanti paj mi ak yeneen fànn yu am solo ci réew mi.