Tukkib nemmiku: Peresidaa Fay dalal na John Daraamani Mahama Njiitu Réewum Gana.

Biti Réew - 17 MONTHS.JANUARY 2025

Njiitu Réew mi dalal na ci àjjuma ji 17i fani sãawiye 2025 naataangoom bii di John Daraamani Mahama, Njiitu Réewum Gana, ci lu soxal tukkib liggéey bu mu fiy amal. Ñaari Njiiti Réew yi àddu nañu ci jëflante yu rittax yi yàgg a dox ci diggante ñaari réew yi ci wàllu xaritoo ak lëkkaloo, te lépp tegu ci bokk gis-gis ci wàllu demokaraasi, yoriin wu jub ak xeex yelleefi doomi aadama yi.

Waxtaan yi jëmoon ci luy gën a dooleel lëkkaloo gi ci wàllu koom ak yaxantu, ñu jublu ci gën a xóotal ak baril jëflante yi ci wàllu njafaan yi, larme bi, kaaraange gi, njàng mi, paj mi ak ndaamaari gi. Waxtaane nañu itam ci tolluwaay bi am ci dig-digal bi ñu xamle ne fàww ñu gën a taxaw temm ci jàmm ji ak dal gi ci Sahel bi ak ci biir CEDEAO. 

Ngan gii nag day firndeel yéene ji ñu bokk am jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gi, ngir suqaliku ak naataangeg ñaari askan yi. Njéndel Réewum Senegaal di am mbégte lool ci naal yi bawoo ci ndaje mii boole ko ak di feddali ag jaayanteem jëm ci wéyal jëflante yu rafet yi yàgg a dox diggam ak Gana ci pas-pasu jàppalante ak Afrig gu doon benn.