Tukki nemmiku : Peresidaa FAY sargal nañu ko ca Gine Bisaawó.

Biti Réew - 26 MONTHS.MAY 2025

Ci tukki nemmiki bi muy amal ca Gine Bisaawó, Kilifa Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, naataangoom Umaro Sisoko Embaló Njiitu Réewum Gine Bisaawó dalal na ko ak wàccuwaay ba mu yelloo. 

Ci tukki nemmiku bi muy amal ca Gine Bisaawó, Kilifa gi, Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, naataangoom Umaro Sisoko Embaló, Njiitu Réewum Gine Bisaawó, jagleel na ko teertu gu mucc ayib. 


Ci waxtaan yi ñu séq ak janoo ak taskati xibaar yi ñu bokk amal, ñaari Njiiti Réew yi feddali nañu diggante bu rattax ak mbokkoo gi yàgg a dox diggante askanu Senegaal ak wu Ginne Bisaawó. Peresidaa FAY fésal na ag cantam ak ug ngërëmam ci dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel teg ci feddali jaayanteg Senegaal gu dul dog jëm ci jàppale Gine Bisaawó ci jéego yi muy teg ci wàllu jàmm, dal ak suqaliku gu sax. 


Ci wàllam, Peresidaa Embaló fàttali na xóotaayu jëflante yi yàgg a dox diggante ñaari réew yi, nga xam ne sax nag jiitu na jonnug Gine Bisaawó. Mu wax ne : « Amul menn réew mu yittewoo ni Senegaal jàmm, dal ak suqalikug Gine Bisaawó.»


Ci tukki bii, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY tappal nañu ko fa raaya Amilkaar Kabraal, di raaya wi gën a ràññiku ci Réewum Gine Bisaawó. Muy raaya wu jëm ci  kañ ko ci jaayante gi mu am ngir gën a dooleel jëflante yi diggante ñaari réew yi, gën a bennale kembaar gi ak jàppoo diggante askan yii doon i bokk, niki noonu ni muy dugalee loxoom ngir dal am ci dig-digal bi. 


Muy jataay bu am solo, bu feddaliwaat mbokkoo, nangulante ak kóolute gu dolliku.