Njiitu Réew mi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, nataangom bu Benee di Peresidaa Patris Taloŋ jagleel na ko teertu gu mucc ayib ci 15i fani sulet 2025 yi ca Kotonu.
Ginnaaw tatagali sóobare sa ca Njéndel réew ma, ñaari Njiiti Réew yi amal nañu ag petoo, daal di ciy toftal kàddu yu ñu bokk yékkati ci kanamu saabalkat yi.
Peresidaa FAY feddali na yéeneem jëm ci gën a dooleel jëflantey mbokkoo yi yàgg a dox diggante Senegaal ak Benee, jaare ko ci gaaral ñu taxawal ci fan yii ag kurél ngir gën a doxal weccente yi ci wàllu koom ak yaxantu diggante ñaari réew yi.
Bu weesoo mbirum lëkkaloo, ñaari Njiiti Réew yi waxtaane nañu tolluwaayu mbootaayi tund wi, rawati na CEDEAO ak UEMOA. Feddali nañu seen yéene jëm ci àndandoo liggéey ngir fexe ba campeef yii gën a jege nammeel ak bëgg-bëggi askan yi ci tund wi.
Man ngeen a topp kàddu yi ñu bokk yékkati :