xamle - 25 MONTHS.JULY 2025
Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, Njiitu Réewum Senegaal, bawoo na Ndakaaru ci subas àjjuma 25i fani sulet 2025, wutali Lome, ca Réewum Togóo ga mu war a amal tukkib liggéey, ci ndënel Kilifa gi Fóor Essozimna ÑASINGBE, Njiitu Réew ma.
Ci bisub gaawu bi, 26i fani sulet 2025, Njiitu Réew mi dina dem ca Monrovia, ca Réewum Liberiyaa, ngir teewe xumbeeli màggalug 178eelu ati jonnug réew ma, ci ndënel Kilifa gi Josef Nyumah Boaki, Njiitu Réew ma.
Peeñi demug Njiitu Réew mi :