Tukki nemmiku ca tundu Ndar.

jëwriñ - 12 MONTHS.JUNE 2025

Njiitu Réew mi dina amal tukki nemmiku ca “pôle territoire nord” (tundu Ndar), alxemes 12 ak àjjuma 13i fani suwe 2025.

Muy nemmiku guy tàbbi ci wàllu topp ak natt naal yu am solo yi Nguur gi sumb ca tund wa. Mu jëm ci gën a dëgëral jéego ya ñu fa jot a teg, saytu tolluwaayu naal yi ci wàllu koom ak dundiin ya ñu fa door ngir njariñu askan wa, niki noonu gën a dooleel jëflante yi diggante Nguur gi ak way-faluy gox ba.

Ci tukki bii, Njiitu Réew mi dina daje ak kilifay ndoxal ya, way-faluy gox ba, ñiy yëngu ci wàllu koom ak ña teewal askan wa, ngir weccente ak ñoom ci yitte yi gën a far ci suqalikug gox ba boole ko ak saytuwaale tolluwaayu liggéey ya ñu fa sumb ak seen njariñ.

Nemmiku gii day wanewaat rekk yéene ju sax ji Njiitu Réew mi am jëm ci gën a dooleel yokkute gu yamale, tolloo te boole ñépp fépp ci mbeeraayu réew mi.