Tukki nemmiku ca Togóo ak ca Liberiyaa.

jëwriñ - 25 MONTHS.JULY 2025

Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, Njiitu Réewum Senegaal, dina amal, suba ci àjjuma ji 25i fani sulet 2025, tukkib nemmiku ca Lome, ca Réewum Togóo ga mu war a amal tukkib liggéey, ci ndënel Kilifa gi Fóor Essozimna ÑASINGBE, Njiitu Réew ma. 


Ca suba sa, di 26i fani sulet 2025, Njiitu Réew mi dina dem ca Monrovia, ca Réewum Liberiyaa, ngir teewe xumbeeli màggalug 178eelu ati jonnug réew ma, ci ndënel Kilifa gi Josef Nyumah Boaki, Njiitu Réew ma.