Tukki nemmiku ca Lome : Peresidaa FAY ak Ñasingbe noppi nañu ngir amal lëkkaloo gu am solo.

Biti Réew - 25 MONTHS.JULY 2025


Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, amal tay ab tukki nemmiku ca Lome ga mu daje ak Kilifa gi Faure Essozimna Ñasingbe Njiitu Réew ma. 

Ndaje mii tax na ñu feddali jëflantey xaritoo ak lëkkaloo yi dox diggante Senegaal ak Togóo. Ñaari Njiiti Réew yi am nañu ag déggoo jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gi, rawati na jaare ko ci taxawal ag kurél guy gëstu ci yoon ak matukaay yu ñu war a teg ngir gën a dëgëral weccente yi ak dooleel lëkkaloo guy jariñ ñaari wàll yépp. 

Ci tukki bii, Ñaari Njiiti Réew yi waxtaane nañu itam jafe-jafey kaaraange ak politig yi am ci tund wi, ñu  daal di  bokk jaayante ne dinañu taxaw temm ngir sàmm dal gi ci kanamu tafaar yiy gàllankoor yokkute gi, rawati na lu mel ni rëtal gi ci Sahel bi.

 Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY rafetlu na jéego yi Peresidaa Fóor di teg jëm ci dox tànki jàmm ci tund wi teg biral ag cantam ci dalal gu mucc ayib gi ak waxtaan yu am solo yi ñu jot a amal.