Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY mu ngi tëjee, tay ci talaata ji 27i fani mee 2025 tukki bi muy amal ca Gine Bisaawó ci nemmiku ndefar guy sopparñi ndaama raas, ki ko fa dalal di Orlàndo Mendes Viegas miy Jëwriñu Yaxantu ak Ndedaru réew ma.
Muy nemmiku guy wane njariñ li ñu bokk am jëm ci suqali fànn yu am solo ci wàllu ndefar ci dig-digal bi, lépp jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gi ci wàllu koom.
Ba mu fa jógee moom Peresidaa FAY, naataangoom bu Gine Bisaawó bi gunge na ko ba ca aydapooru “Osvaldo Vieira” ga ko sóobare sa sargal laataa muy dellusi Ndakaaru.
Nemmiku gu am solo gii fésoon na lool ci ay waxtaan yu wér, ay jaayante yu ñu bokk amal ak mbokkoo gu ñu feddali diggante Senegaal ak Gine Bisaawó.