Biti Réew - 31 MONTHS.OCTOBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, soxnaam ak delegasoo bi mu àndal, yegg nañu démb ci ngoon gi ca Medin. Ñu ànd teewlu, amal ay ñaan ci biir Jàkkay Yónnent bi Muhmmat (SLHWS) teg ci siyaar barab bu tedd ba mu tëdd. Peresidaa Fay siyaare na itam miise bi ñu jagleel dund ak jëfi Yónnent bi (SLHWS), di barab bu fees dell ak njàngale ci mboor ak mbaaxi lislaam. Siyaar bii mu amal ca Warab yu tedd yooyu nag doon lu fees dell ak pas-pas te taqoo ak mbaaxi diine.