Tijjitel Ndajem Waxtaane Eewestismaa Turki-Senegaal ca Istanbul: Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY di woo àntarpiriis yu Turki ñu eewestiir ci pàcc yi gën a am solo

Biti Réew - 01 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, jiite na tay ca Instanbul tijjitel Ndajem Waxtaane Eewestismaa Turki-Senegaal ànd ko ak Topp-Njiital Turki, Cevdet Yilmaz.

Ndajem jëflante gii ñu lootaabe ci lëkkaloog APIX ak Kurél giy saytu ca Turki jëflantey koom ak Biti Réew, jéego bu am solo jëm ci gën a dooleel lëngoo gi diggante ñaari réew yi.

Cig àddoom, Njiitu Réew mi xamle na solo si eewestismaa piriwe bi am ci doon jumtukaayu yokkute ak taxawal ay xëy, niki noonu fésal li Senegaal am ci dalug politig, balli mbindaare yi ak taxawaay bu am solo bi mu am ci Afrig Sowu Jant. Njiitu Réew mi woo na àntarpiriisi Turki yi ñu eewestir ci pàcc yu am solo yi mel ni mbay mi, ndefar gi, enersii bi, efraastiriktiir yi ak turism bi, lépp tegu ci lëkkaloo gu sax.

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay posewu na ci ndaje mii ngir indi ag njàppaleem jëme ci piriweb Senegaal bi jaare ko ci tijjil leen marsey àddina si.

Ndaje mii nag day firndeel jaayanteg Senegaal ci amal lëkkaloo gu am solo te làq njariñ yu muy bokk ak réewum Turki.