Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi ci wàllu Njàng mi, Ndaw ñi ak Xëy mi door na tay ci talaata ji 10i fani desàmbar 2024 ca Nuwaagsót.
Ñu lootaabe ko ci Njiital kilifa gi Mohammet Uld Seex Al Gasuwani, Njiitu Réewum Islaam gu Móritani te doon Njiital Mbootaayu Réewi Afrig yi jamono jii, xew-xew bii dajale na ay Njiiti Réew, yu mel ni Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, ay jëwriñi Njàng ak yu Koppar, ay kàngam ak ñuy yëngu ci sosete siwil bi ñu war a waxtaane wëppa wii di: « Jàngale ngir boole Afrig ci 21eelu xarnu bi. »
Ci jataay bii, Peresidaa Fay fàttali na jaayante gi Mbootaayu Réewi Afrig yi bokk amal jëm ci tabax Afrig gu am doole te yëngu, mu boole ci fésal ne ndawi Afrig yi doon lu ëpp 60% ci askan wi, ñooy tay waaye tamit ñooy ëllëgu kembaar gi. Taxaw na bu baax it ci xamle ne, ngir dakkal yokkuteg ndóol gi, fàww ñu amal njàng mu mucc ayib te jàppandi ci ñépp, rawati na ci xale yu jigéen yi ak ñi dëkk ci kaw gi.
Moom Njiitu Réew Mi woo na itam Njiiti Réewi Afrig yi ñu boole seen doole ngir tabax koom mu man a téyee sunuy kàngam boole ko ak man a indi tontu lu wér ci nammeelu sunuy ndaw.
Man ngeen a topp àddug Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay
Man ngeen a topp ba tay it fii ci suuf mbooleem Kàdduy Njiitu Réew mi:
Ginnaaw bi ma nuyoo kilifa gi Mohammet Uld Seex El Gasuwani, Njiitu Réewum Islaam gu Móritani, di Njiital Mbootaayu Réewi Afrig yi jamono jii, sama bokki Njiiti Réew yi,
Bokki Soxna yi ak Sëriñ si jiite ay gàngoor,
Njiital Jëwriñ yi,
Njiital Komisoo bu Mbootaayu Réewi Afrig yi,
Jëwriñ yi, jigéen ak góor,
Gan ñu tedd ñi, kenn ku ci nekk ak sa dayoo ak sa wàccuwaay,
Soxna yi ak Sëriñ si,
Ma bëggoon balaa dara jaajëfal sama mag di Peresidaa GASUWANI ci ndëneem lii ak mbooleem matuwaay yi mu jël ngir jàppandil sunu ngan gi fii nga xam ne wutalewunu ko ak sunu kër.
Maa ngi yeesal samay ndokkale jëme ci moom ndax taxawaayam ak liggéey bu mucc ayib bi muy amal ci boppu Mbootaayu Réewi Afrig yi, ci jamono joo xam ne àddina si yëngu na lool ba jaaxal ñépp te ànd ak soppiku yu dul dog.
Sunu ndajem tay mii nag firnde dëgg la ci ni mu taxawee temm ngir jàmmaarloo ak jafe-jafey kembaar gi.
Yéene jii di tàbbi ci wàllu doxal wëppa wi Mbootaayu Réewi Afrig yi di waxtaane ci at mii, day wane rekk solo si nu jox nun ñépp tomb yii nekk ci xolu sunu ëllëg : njàng mi, ndaw ñi ak xëy mi.
Mooy tekki sunu jaayante gi nu bokk am jëm ci tabax Afrig gu am doole, yëngu te naat. Sunu ndaw ñi doon lu ëpp 60% ci askan wi, ñooy tay waaye tamit ñooy ëllëgu kembaar gi. Li nu war a yittewoo bu wér nag mooy seen um njàng, seen ug tàggatu ak sóob leen bu baax ci doxaliinu koom mi.
Ci loolu kon maa ngi rafetlu, jéego yi Mbootaayu Réewi Afrig yi di teg te bokk ci yooyu yi komiteb fukki Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ ak Njiital Komisoo bi, di mbokk mi Musaa Faxi Mahamat ak ay baram, di teg ngir dooleel njàng mi, xamtu ak xarala, lépp ngir yegg ci jubluwaayu suqaliku gu sax boole ko ak baral jéego yi jëm ci doxal « agenda » bu 2063.
Kilifa yi, Soxna yi ak Sëriñ si, ´
Takku taxaw ngir njàng mi, mooy liggéey ngir tijji xel yi, tàggatu ci man-man yi ak jëm kanam; mooy dugal sunu loxo itam ci tabax nit ñi ba ñu man a am settantal giy tax ñu man a mucc ci yàqkati xel yi ak xiirtalekat yi; mooy samp xam-xam, man-man ak nekkiin ngir mucc cig réer ak tàbbi ci lëndëm; mooy tax ñu man a tabax nit ñu mucc ayib ñu noppi ngir amal suqalikug koom ak dundiin gu sax.
Ca Senegaal, li nu tànn mooy liggéey bu baax ci njàng mu jàppandi ci ñépp te mucc ayib. Loolu nag day am lu muy laaj:
- Jagleel ko lu bari ci liy ballee ci sunuy njël ak ci partaneer yi;
- Njàng mu jàppandi ci ñépp te mucc ayib, rawati na ci xale yu jigéen yi ak ñi dëkk ci kaw gi, ngir wàññi bu baax yokkuteg ndóol gi;
- Dooleel dugalug xarala yi ci njàngale mi ak tàggatu gi ci tolluwaay yépp ;
- Dooleel tàggatu gu xarala gi ak gu xereñ gi, nga xam ne day méngoo ak li ñu soxla ci marse bi ngir lëkkale sunu ndaw ñi ak li àddina laaj ci wàllu liggéey.
Wareeful a yam rekk nag ci tàggat, waaye fàww ñu boole ci di fent xëy yu ñu man a def ak ekosistem bu jàppandi.
Ndaw ñi ñooy xolu soppikug koom mi. Sunuy ndaw xereñ nañu te am nañu yéene. Nun noo leen war a jox jumtukaay yiy tax ñu man a fent boole ko ak di yëngu.
Loolu lanuy def ca Senegaal ga nga xam ne liggéey ci tabax nit ñu mucc ayib ak yamale askan wi ñoo nekk ci xolu sémb wu yees wii jëm ci soppi réew ma fii ak 2050.
Tàmbali nanu faa doxal ay naal ak yeneen yu nekk ci yoon, yu jëm ci dooleel man a am um xëy. Manees cee lim:
- gunge ndooraan yi ci pàcc yu am solo ci koomum xarala yi ak kéew mi;
- lëkkaloo diggante piblig bi ak piriwe bi, ngir ñaax këri liggéeyukaay yi ñuy jël ak a tàggat ndaw ñi;
- Sémb yu wóor yu mel ni « póol indistiri » yi ak ay selebe yooni xarala, nga xam ne xëy yu baax a ciy bawoo.
Waaye nag warunoo xeeb jafe-jafe yi ci sunu kanam. Diggante li ñuy jàngale ak li marse bi soxla, yaatu na lool.
Soppiku yi am ci wàllu ni nit ñi di yokkoo day laaj pexe yu gaaw te sax. Loolu nag day laaj ay matuwaay yu mel ni:
- Ay doxaliin yu dëppoo ci kembaar gi ngir dooleel dem ak dikkug waay-xereñ yi ak man-man yi;
- Dooleel lëkkaloo gi sunu digg ak partaneer yi ngir man a dajale lu doy ci koppar ak xam-xam;
- Suqali jumtukaayi njàng mi ak xarala yi, ngir wàññi ñàkk a yamale gi am diggante dëkki taax yi ak kaw gi.
Kilifa yi, Soxna yi ak Sëriñ si,
Jëm kanamug sunu kembaar gi mu ngi aju ci sunu taxawaay ci jox sunuy ndaw jumtukaay yiy tax ñu man a jëmmal seen i gént.
Nanu boole sunuy doole ngir tabax koomum Afrig mu man a téyee sunuy way-xereñ boole ko ak indi tontu lu wér ci nammeeli sunuy ndaw.
Nanu mànkoo def ndaje mii muy jéego bu am solo ngir ëllëgu Afrig ak ay ndawam.
Nanu joxante loxo liggéey ngir tabax kembaar gog ndaw lu ne, ak fu mu man a féete, dina man a gis boppam boole ko ak dugal loxoom ci luy jëmale kanam kembaar gi.
Maa ngi leen di jaajëfal ci seen ug teewlu.