Tijjitel Ëtt ak Warabi Àttekaay yi ca Ëttu Àttekaay bu Kawe bi

jëwriñ - 16 MONTHS.JANUARY 2025

Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay, dina jiite, alxemes 16i fani sãawiye 2025, ca Ëttu Àttekaay bu Kawe bi, tijjitel Ëtt ak Warabi Àttekaay yi. Muy ndaje muy màndargaal ndoortel atum 2025 ci wàllu yoon, ñu war cee waxtaane tomb bii di : « Sañ-sañu seleŋlu ak sàmm dalug pénc mi ».


Muy dajele mbooleem ñiy yëngu ci wàllu yoon, xew wii am pose lay doon ngir waxtaan ci jafe-jafe yi boole ko ak càmbar yoon yi ñu man a jaar ngir jubbanti doxaliinu yoon. 


Tomb bii ñu tànn war koo waxtaane, dina tax ñu indi ay leeral ci solos sàmmonte ak yelleef yi manul a ñàkk, rawati na sañ-sañu seleŋlu, lépp ci kaw sàmmaale dalug pénc mi. Dina bokk ci diisoo yi ñuy amal kon, fexee gëstu ci jumtukaay yuy tax ñu delloosi kóolute diggante askan wi ak yoon boole ko ak taxaw ci sàmm jàmm ji ci pénc mi.