Tijjitel barabu defarakaayu ñakk bu Institut Pasteur bu Jamñaajo.

jëwriñ - 13 MONTHS.DECEMBER 2024

Àjjuma jii 13i fani desàmbar 2024, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, dina daloo defarukaayu ñakk bu bees bu Institut Pasteur bu Jamñaajo, doon jéego bu am solo ci xeex wopp yi ci Afrig.

Barab bii nekk ci wetu Ndkaaru, li ko tax a jóg mooy defar ñakki Kowid-19 ak yeneen xeeti mbas. Ñu tabax ko mu war a yegg ci dayob man a defar lu mat 30i milyoŋi ñakk at mu jot, dina tax ñu man a yokk kaaraangeg saa-senegaal yi ak saa-afrig yi ci wàllu wér gi yaram.

Sémb wii nag mu ngi bokk ci jéego yi  kembaar  gi di teg jëm ci moom boppam ci wàllu wér gi yaram.