Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay daloo na tay barabu defarukaayu ñakk bu Jamñaajo, di jumtukaay bu ñu tabax ci wàllu sémb wii di MADIBA (Manufacturing in Africa for Disease Immunization and Building Autonomy). Xew wii daje ak téeméeri ati « Institut Pasteur » bu Ndakaaru, day teg Senegaal ci yoon wi mu yàgg séntu jëm ci moom boppam ci wàllu paj ak garabal.
Barab bu méngoo ak jamono bii ñu samp ci lu jege 5i hegtaar, am na pàcc bu ñuy defaree ay ñakk, rawati na yu Kowid-19 ak yeneen xeeti mbas. Tabax bii nag doon na jéego bu am solo ci réew mi namm defaral boppam ay ñakk yu mucc ayib boole ci ak wàññi bu baax la mu ci daan jéggaani. Mébetam mooy dooleel manal sa bopp ci wàllu garabal ci Afrig gi nga xam ne 1% rekk lay defaral boppam ci ñakk yi muy jëfandikoo.
Ca jataay ba, Peresidaa Fay xamle na solos sémb wii ci wér gi yaramu askan wi ak kaaraangeg Senegaal ci wàllum paj, jaajëfalaale itam partaneer yi ak Institut Pasteur ci taxaawaay bu am solo bii ñu am ci dund gi. Fàttali na itam ne barab bii, jumtukaayu xarala bi mu àndal dina tax mu man a defar ba 300i milyoŋi ñakk at mu ne ngir man di taxaw ci lim bi ñu soxla ci pajum askan wi, waxuma la ci Senegaal rekk waaye ci Afrig Sowu Jant gépp.
Peresidaa Fay posewu na ci ngir woote ab diisoo ak lëkkaloo ci diggante defarkat yi, kurél yiy saytu wàllu garabal ci réew mi, sektéer piriwe bi, jaaykat yi, jàngune yi ak gëstukati réewi Afrig yépp. Xamle na solos taxawal ekosistemu Afrig ci wàllu ndefaru garab guy tax ñu man a yegg ci manal sa bopp ci wàllu ñakk, test yi ak garab yi ci Afrig.
Barabu defarukaayu ñakk bii ci tund wi, dina def Senegaal muy réew mu am solo ci xeex ak jépp tawat ju xeetoo ak mbas.
Man ngeen a topp àddug Njiitu Réew mi :
Kàdduy Njiitu Réew mi ca « Vaccinopôle » bu Jamñaajo ak màggalug téeméeri ati Institut Pasteur bu Ndakaaru
Ginnaaw bi ma nuyoo Jëwriñu Paj mi,
Góor ak Jigéen ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi,
Kilifa yi Jigéen ak Góor ñi bokk ci gàngoori laamisoo yi,
Góornoor bu Ndakaaru,
Perefe bu Rufisk,
Fara bu Jamñaajo,
Njiital Koosey Administaraasoo bu Institut Pasteur bu Ndakaaru,
Njiital Pôle urbain bu Ndakaaru,
Administaraatéer Seneraalu Institut Pasteur bu Ndakaaru,
Partaneer yi ci wàllu koppar, xamtu ak xarala yu Institut Pasteur bu Ndakaaru, Jigéen ak Góor,
Jigéen ak Góori liggéeykat yu Institut Pasteur bu Ndakaaru,
Gan ñu tedd ñi,
Soxna yi ak Sëriñ si
Mbégte mu yaatu te ànd ak bànneex laa am tay taxaw fii ci seen kanam ngir màggal jéego bu am solo bii ci mboorum sunu réew ak kembaaru Afrig: téeméeri ati Institut Pasteur bu Ndakaaru. Di campeef gog, ba mu sosoo ak tay, mu ngi wane jaayanteg Senegaal ci xeex jàngoroy wàlle yi ak dooleel wér gi yaramu askan wi.
Ca atum 1924, la Institut Pasteur bu Ndakaaru taxaw, te boobu ba leegi, deñul di dox bis bu set ci luy gën a jëme kaw fent gi ci wàllu xamtu ak xereñte. Ci at mii nag, bu weesoo ndonol xamtu lu gànjaru lii, noo ngi màggal itam gis-gis bu wér te wóor ci ëllëgu wér gi yaramug askan wi ci Afrig.
Téeméeri ati Institut Pasteur bu Ndakaaru yii am pose la ngir rafetlu jéego yu am solo yi kër gii yàgg a teg, waaye itam fexee amal ay xalaat ci ëllëg, ci li nuy àndandoo di tabax ngir yegg ci manal sunu bopp ci wàllum paj ci Senegaal ak ci sunu kembaar gi.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Mbasum Kowid-19 mi wane na néew kàttanug Afrig ci wàllum paj. Donte def nanu ay jéegoo ci fukki at yii mujj it, sunu kembaar gi ba leegi mu ngi wéy di teg yaakaaram ci jéggaani li mu soxla ci ay garab, ay test ngir càmbar, rawati na nag ay ñakk. Jamono jii Afrig 1% rekk lay defaral boppam ci ay ñakk, 5% ci ay testam ngir càmbar ak 30% ci ay garabam.
Seetlu gii nga xam nag ne wareeful a toog rekk di ko seetaan, moo jóo Senegaal ci mu taxawal sémb wu wóor wu jëm ci manal boppam ci wàllum paj ak garabal. Sémb wii nag jubluwaay bi mooy fexe ba Senegaal man a taxawu fii ak 2035, gën gaa néew 50% ci li muy soxla ci ay ñakk ak i garab yu ñuy defaree ci réew mi. Muy sémb wu tàbbi ci mébet mu yaatu mi Mbootaayu Réewi Afrig yi ak Afrikaa CDC am jëm ci yegg fii ak 2040 di defar 60% ci ay ñakk.
Vaccinopole bu Jamñaajo bii nag moo nekk ci xolu gis-gis boobu. Muy eewestismaa bu am solo ngir ëllëgu paj mi ci Afrig, bokk itam ci pexe yi nuy teg ngir tabax Senegaal gu moom boppam, jub te naat, lalu ci dooleel xamtu, xarala, fent ak xereñte. Day tàbbi itam ci wàllu Sémbu Soppi Senegaal fii ak 2050 te war a bokk ci suqali nit ñu mucc ayib te yamoo ay àq jaare ko ci am taxawu ci paj mu matale muy jaar ci manal sa bopp ci wàllu garabal ak ñakk.
Jumtukaay yu xarala yi mu àndal, dinañu tax vaccinopôle bii man di defar ba 300i milyoŋi ñakk at mu jot ngir man di taxaw ci, waxuma la ak li Senegaal di soxla ci wàllum paj kese, waaye ci mbooleem Afrig Sowu Jant gi.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Gis-gisu moom sa bopp ci wàllum paj mi ñu teg ci loxo Institut Pasteur bu Ndakaaru lëkkaloo gu am solo la ci tund wi ak ci àddina si. Loolu nag dina ma may ma rafetlu boole ko ak jaajëfal partaneer yi – UE, Bànkub Órob bi ci wàllu eewestismaa, Almaañ jaare ko ci KFW ak GIZ, Farãas jaare ko ci AFD, Garànd Berétaañ jaare ko ci FCDO, Japon, BID, Bànk Monjaal jaare ko SFI, Bànk Dewëlobmaa bu Êtats-Unis walla DFC, BAD, Fondaasoo Bill ak Mélinda Gates, Mastercard Foundation, Open Society Foundation, Susan Buffet Foundation, Elma Foundation, CEPI, nga xam ne nanga nañoo fekksi Ngóornamaŋu Senegaal jàppale ko ci yéeneem waaye itam partaneer yu mel ni OMS, Afrikaa CDC, UniverCells, BIONTECH, IAVI ak Batavia.
Ma posewu ci itam woote ab diisoo ak lëkkaloo ci diggante defarkat yi, kurél yiy saytu wàllu garabal ci réew mi, sektéer piriwe bi, jaaykat yi, jàngune yi ak gëstukati réewi Afrig yépp. Xamle na solos taxawal ekosistemu Afrig ci wàllu ndefaru garab guy tax nu man a yegg ci manal sa bopp ci wàllu ñakk, caafug càmbar yi ak garab ci Afrig.
Ci wàll woowu, maa ngi ndokkale yeggug kërug Senegaal giy saytu yoonalug garabal (ARP) ci 3eelu dayob ñor ak « Comité National d’Ethique pour la Recherche en Santé (CNERS) » gi am
« certification ISO 9001-2015 ». Maa ngi rafetlu itam li Institut Pasteur bu Ndakaaru taxawal VaxSen, di bànqaas bi yor njaayum ñakk yi ñuy defaree ci vaccinopôle bi.
Ngeen may ma, ma tëjee cant yi, ci jaajëfal mbooleem gëstukat yi, xamtukat yi, way-xarala yi, partaneer yi, niki noonu mbooleem bar yi dugal seen loxo ci sottalug sémb wii. Yéen a xàll yoon wu bees wii ñeel pajum Senegaal ak Afrig.
Maa ngi leen di soññ, jigéen ak góor, ci wéyal yéeney jàppalante gii ci wàllu xamtu ak lëkkaloo ci àddina si. Bu nu mànkoo rekk, man nanoo tabax ëllëg goo xam ne mbirum wér gi yaram dootul doon jafe-jafe buy tëj bopp yi waaye day doon yokkute ak noflaay ngir ñépp. Yoon wi gudd na, waaye nag jéego yi nu jot a teg ba fii ñoo nuy soññ ci nu wéy jëm ca kanam.
Yaw Njiital Institut Pasteur bu Ndakaaru,
Jigéen ak góori liggéeykati Institut Pasteur bu Ndakaaru,
Vaccinopole bu Jamñaajo bii du rekk ngir Senegaal, waaye ngir Afrig ak àddina sépp la.
Maa ngi leen di jaajëfal te di leen ndokkale ci liggéey yi ngeen jot a sottal ak yi ngeen di sottali ci at yii di ñëw. Senegaal ak Afrig am nañu yaakaar ci yéen.
Maa ngi leen di jaajëfal ci seen teewlu.