TICAD 9 Business Expo ak Waxtaan : Njiitu Réew mi nemmiku na « Pavillon Sénégal ».

Biti Réew - 22 MONTHS.AUGUST 2025

Lu jëm ci « TICAD 9 Business Expo & Conference », Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal amal na, ci àjjuma ji 22i fani ut, ag nemmiku ca « Pavillon Sénégal », mu àndoon ko ak jëwriñ yu bari, Njiitu APIX ak Njiitu FONSIS.


Ci lëkkaleg APIX SA, « Pavillon » bi fésal na « Vision Sénégal 2050 », naal yu am solo yi ak sémb yu bees yi ñu man a dugal xaalis. Ci wetu APIX, ñenti këri liggéeyukaay fésal nañu seen i naal : « Carrefour Médical » (paj mi), Technologies Services  (jumtukaayi paj ), SODER (xereñteef ci wàllu mbëj) ak KAI NU DEM (Xarala ak jumtukaay).


Seetu bii ñeel sektéer piriwe bu Senegaal doon na  lu xemmemloo dugalkati xaalisi Japon yi ci Senegaal, rawati na ci wàllu yaale gi, jumtukaay yi, paj mi, yasara gi ak kéew mi. Teewaayu kër yu mag yu mel ni CFAO (Toyota Tsusho) firnde la ci.


Ca bis ba ko jiitu, Jëwriñu Japon ji yor wàllu Jëflante ak Biti Réew jotoon naa nemmiku « Pavillon » bi, muy wane nag solo si mu jox lëkkaloog ñaari réew yi. At yu bari a ngi nii, teewaayu Senegaal ca TICAD bi APIX di jiite, di am njeexital yu am solo : 

torlug ay MoU, sampug saa-japon yi ak partaneer yi.


Nemmikug Njiitu Réew mi nag day firndeel yéeney Senegaal ci doon selebe yoonu dugal xaalis ci tund wi boole ko ak gën a dëgëral lëngoo gu am gi dox digganteem ak Japon.