Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, rafetlu na tëjtel Péncoo Sistem Politigu réew mi, ñu doon ko amal 28i fani mee ba 4i fani suwe 2025.
Muy mbébetu Njiitu Réew mi, ndaje mu mag mii ci wàllu demokaraasi, dajale woon na mbooleem ñi am kàddu ci réew mi, ñi teewal làngi politig yi, mbootaayi sosete siwil bi, ay kàngam ak ma-réew yi jaayante, ñu wane ag mat, jéllale boole ko ak mayante nopp.
Péncoo gii, doon lu gànjaru, fullawu te tijjeeku, tax na ñu yaatal ci xel mu dal fi dooley sunu campeef yi ak sunu sistemu politig bi yam boole ko ak xool coppite yi ñu ci war a amal. Muy gaaral yuy xàll yoonu doxaliinu politig wu gën a méngoo ak jamono, gën a leer te gën a xereñ.
Njiitu Réew mi fésal na ag cantam jëme ko ci mbooleem ñi doon teewe jataay yi ci seen jaayante, bëgg réew mi ak jiital njariñu askan wi. Jaajëfal na bu baax itam way-looaabe ñi, kàngam yi ak aji-yombal ji ci liggéey bu mucc ayib bi ñu amal.
Jataay bii, tegu ci péncoo ak diisoo, doon na jéego bu am solo ci dundug demokaraasi Senegaal. Day tàbbi ci gis-gis bu leer : tabaxaat sunu campeef yi ngir gën leen a méngale ak li nu bëgg ci moom sunu bopp, yoon ak bennoo.
Njiitu Réew mi fàttali na ne Péncoo gii warut a doon rekk ci benn xew-xew bu nuy jàppal bis, waaye lu war a sax la, ndax demokaraasi buy dund ci weccente, ci jubbanti ak ci jëf ju ñépp di ànd lees koy tabaxee.