Tay ci talaata ji 1 panu sulet 2025, ca 4eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Àddina si ci kopparalug suqaliku gi, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, am na suba gu fés lool ci wàllu laamisoo ca Seville.
Njiitu Réew mi jëkk naa teewe ci jataayu waxtaan bu kawe, bu Ngóornamaŋu Espaañ bi lootaabe, ci tomb bii di :
« Eewestiir ci jàppalante ci àddina si: gis-gisu lëkkaloo gu bees ngir suqaliku».
Cig àddoom, Njiitu Réew mi yékkati na kàddoom ngir ñu tëggaat kaadaru lëkkaloo gu tegu ci doxaliinu kopparal gu bees, lëkkaloo gu gën a yamale boole ko ak amal jaayante gu bees ngir gën a dimbali réew yu néew doole yi. Ci geneen wàll, xamle na ne fàww ñu gën a jiital jàmm, jàppalante ak bañ a beddi kenn ci jëflantey àddina si.
Ginnaaw jataay bii, Njiitu Réew mi séq na ab jataay bu ko Njiitu Ngóornamaŋu Espaañ Pedro Sanchez dalal. Waxtaan wi jëmoon ci tolluwaay ak mbébeti jëflante diggante Senegaal ak Espaañ, te la ca gën a fés di ci wàll yu am solo yu mel ni mbay mi, caytu gi ci wàllu tukki ak liggéey bu baax ngir dal gu sax dàkk ci tund wi.
Mu tëjee moom Njiitu Réew mi ci dalal tañu “Open Society Foundations”. Waxtaan yi jëmoon ci jëf yi ñu jot a amal ci Senegaal ak mbébet yi jëm ci gën a dooleel lëngoo gi ci doxaliinu suqaliku gu dul beddi kenn te taxaw ci yittey askan wi.