xamle - 12 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ginnaaw Tiwaawon, Njiitu Réew mi dem na ca Cenaba, di geneen Këru diine gu mu feddali ag jaayanteem jëm ci taxawu kilifay diine yi ci Senegaal.
Baay Sëriñ Asan Sekk miy Xalifa bi kañ na jikkoy Njiitu Réew mi teg ci rafetlu ag ubbikoom ci mbooleem këri diine yi ci Senegaal.
Ginnaaw saafonte yi digganteem ak Xalif bi ak Njabootam, Njiitu Réew mi nemmiku na itam liggéey yi ñuy amal ci kër gan ñi, te doon lu bokk ci sémb yi ñu jagleel yeesal këri diine yi.