Siyaar ci Tiwaawon : Njiitu Réew mi xamle na ne dees na taxawal luy lu ñuy jagleel diine.

xamle - 30 MONTHS.AUGUST 2025

Ci siyaar bi mu doon amal ci wetu kilifa diine yi nekk ca dëkkub Maam Mawdo, jëm ci waajtaayu gàmmu 2025 gi, Njiitu Réew mi xamle na, ca barabu waxtaanukaay ba ñu tuddee Sëriñ Baabakar SI, ne dees na taxawal njël lu ñuy jagleel diine. Muy mbébet mu jëm ci gën a taxaw ci yittey këri diine yi. 


Dogal bii, di guleet, fas na yéene gën  a dooleel ni ñuy saytoo xew-xewi diine yi te it dina doon jéego bu am solo ci politigu gën a dëgëral wàllu pas-pas ci réew mi. 


Feddali gii lu def ci cér bu rëy bi mu jox këri diine yi, Njiitu Réew mi fésal na waar wu yaatu wi ñu bay ci déggoo gi am ci réew mi, njàngalem sunuy mbaax ak gën a sàmm dalug pénc mi.


Widewoo bi  :