Ci lu soxal màggal guddig Gàmmu gi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, amal na ab siyaar ci suba si ca Tiwaawon, ci kanamu Xalifa Seneraalu Tiijaan yi Sëriñ Baabakar Si Mansuur. Mu àndoon ak soxnaam ak ñenn ñu bokk ci Ngóornamaŋ bi, moom Njiitu Réew mi, kilifa diine ya ak yu ndoxalug dëkk bu sell ba, dalal nañu ko ci anam yu mucc ayib.
Njiitu Réew mi, feddali na ci kanamu Xalif bi, ag Jaata teem ci dooleel ak gunge këri diine yi mu gis ne ñooy keno yi téyee mboolaayug Senegaal. Xamle na itam solos bànqaas biy yor mbiru diine yi ngir sóob bu baax Këri diine yi ci yoriinu réew mi.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Xalif bi mu ñaanal Senegaal te dugal loxoom ci soññ ndaw ñi xamal leen tafaar yi nekk ci mbëkk mi.