Siyaar ca Njaasaan : Seex Buu Siidi Moktaar Kunta, dalal na Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay

xamle - 19 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi amal na, ci alxemes ji 19i sebtàmbar 2024, ab siyaara ca Njaasaan. Demam gii mu ngi ko amal ci màggal guddig Mawlidi Nabii giy dëgmal ca dëkk boobu, te ñu jàpp ko 22i sebtàmbar 2024.
Njiitu Réew mi, Xalif Seneraal bu Njaasaan, Seex Buu Siidi Moktaar Kunta, dalal na ko. Ci jataay boobu, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay sàkku na ay ñaan ci Xalif bi ngir Senegaal ak ndam ci naal yi nguur gi di sumb.
Njiitu Réew mi dalal na xel yi ne mbooleem càkkuteef yi kilifa diine gi amal dees na leen bàyyi xel ci sémb ak naal yi nguur gu bees giy taxawal. « At mu jot dinanu natt njël loo xam ne danu koy jagleel gunge naal yi ak sémb yi ci dëkki diine yi», di li mu xamle.