Senegaal xaatim na ag lëkkaloo gu am solo gu tollu ci 10i milyoŋi dolaar diggam ak « Fondation Gates » ngir baral « New Deal technologique » bi.

Biti Réew - 24 MONTHS.SEPTEMBER 2025


Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, dalal na tay ci ab jataay, S.Bill Gates, Njiitu « Fondation Gates », ci 80eelu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si.


Ci ndaje mii nag, am na jéego bu am solo bu ñu fa teg, muy xaatimug lëkkaloo gu am solo gu tollu ci lu ëpp 10i milyoŋi dolaar, mu jëm ci baral jëmmalug « New Deal technologique » bi Njiitu Réew mi sumb.


Lëkkaloo gii dina tax ñu man a taxawal genn xàmmekaay ci wàllu xarala, benn jumtukaay ci wàllu « intelligence artificielle » ngir amal ay fent ci wàllu paj mi ak mbay mi, niki noonu taxawal benn « Delivery Unit » ngir am doxaliin wu leer te xereñ.


Ci yoon wii ñu tegu jëm ci lëkkaloo, Senegaal ak Fondation Gates tijji nañu bunt bu bees, bu jëm ci def sunu réew muy barab bu am solo ci Afrig ci wàllu xarala boole ko ak may bépp ma-réew mu man a jëmmal ay mbébetam ci ëllëg gu boole ñépp te naat.