Senegaal torlu na déggooy Artemis yu NASA.

Biti Réew - 25 MONTHS.JULY 2025

Senegaal daal di nay tàbbi, ci 24i fani sulet 2025 yi, Déggooy Artemis, ci noonu kon mu daal di doon 56eelu réew mi torlu naal wii NASA - National Aeronautics and Space Administration di doxal. Déggoo yii nag ñooy tekki pas-pasu lëngoo ngir dem gu ànd ak jàmm, leer te wóor ñeel jawwu ji. 


Torlu gi a amee ca Washington ca dalu NASA, ci teewaayu S. Maram Kayre, Njiitu “Agence Sénégalaise d’Études Spatiales (ASES)”, S. Abdul Wahaab Aydara, Ma-laamisoob Senegaal ca  États-Unis, ak kilifay saa-amerig yu kawe.

Tàbbi gii nag doon na jéego bu am solo ci mbébet mi Senegaal am ci wàllu jaww ji, ginnaaw ndaje mi ñu amal 9i fani sulet 2025 diggante Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ak Njiitu Réewum “États-Unis” Donald Trump, te tax ñu gën a dooleel lëkkaloo gi, rawati na ci wàllu xamtu ak fent.

Ci déggooy Artemis yii, Senegaal feddali na ag taqoom ci laamisoog xamtu, lépp ngir jàmm, xam-xam ak suqaliku gu sax dàkk ñeel askan wi.