xamle - 19 MONTHS.OCTOBER 2024
Njéndel Réewum Senegaal di am mbégte di leen yëgal dellusig sunu bokk yi ne woon ca Liban ci jàmm, ginnaaw jafe-jafey kaaraange yi amoon ca réew mooma.
Takku taxaw gu gaaw te ànd ak yëgoo tax na ba sunu bokk yooyu man a dellusiwaat ci seen réew ci ngor. Jël nañu ay matuwaay yu am solo ngir gunge leen ba ñu man a sancaat ci jàmm.
Njiitu Réew mi yékkati ay kàddu ngir soññ askan wi ci jàppalante, feddali na ag jaayanteem ngir aar mbooleem saa-senegaal yi ak fépp fu ñu man a nekk. Saa-senegaal bu nekk man naa am yaakaar ci Nguur gi mu taxawu ko saa su amee jafe-jafe.