Ca bis ba ñu jagleel Senegaal ca « Exposition universelle » Osaka-Kansai 2025, Kilifa gi, Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal màggal na, ci altine ji 25i fani ut 2025, jëflante yu rafet yi dox diggante Senegaal ak Japon, te li koy màndargaal di 65i ati lëkkaloo gu jar a roy. Jiite na itam Ndajem koom mu ñu fa amal, ci teewaayu kilifa yu mag, ay dugalkati ak ay partaneer yu am solo.
Cig àddoom, jiitu Réew mi yaatal na njariñ yu wér yi Senegaal làq, jaare ko ci taxawlu bu baax ci pàcc yu am solo yiy jàpp ci yokkuteg réew mi. Fésal na itam yéene ji réew mi am jëm ci yegg ci jëfandikoo 40% ci yasara yi ñuy yeesal jaare ko ci lii di « mix énergétique » bi fii ak 2030. Ndefaru lekk yi tamit bokk na ci yitte yi gën a far, jaare ko ci gën a jariñoo suuf si ci mbay mi ak di sopparñee ci réew mi li fiy ñoree.
Njiitu Réew mi àddu na ci geneen wàll ci lu jëm ci suqali jumtukaay yi ci wàllu tabax ak xarala yi, mu jëm ci def Senegaal muy selebe yoonu losistig ci kembaar gi boole ko ak dooleel wàllu lënkale gi. Ci wàllu paj mi ak wàllu fent, feddali na jaayanteg Ngóornamaŋ bi jëm ci liggéey ngir manal sunu bopp ci wàllu garabal ak suqalikug jëfandikoo xarala yi ci wàllu paj mi.
Njiitu Réew mi feddali na itam jaayanteg Ngóornamaŋ bi jëm ci gunge ñi nekk ci sektéer piriwe bi ci xar-kanam gu yees, dal te xemmemu, ci biir « Vision Sénégal 2050 ».
Ci lool, woo na lijjantikati Japon yi ñu ñëw fekksi Senegaal ci yoon wii mu sóobu, tàmbalee ko ci ñëw teew ci « Forum Invest In Sénégal » bi ñu war a amal 7 ak 8i fani oktoobar 2025 ca Ndakaaru. »