Senegaal ak Gaboŋ fas nañu yéene gën a dooleel jëflante yi dox seen diggante

xamle - 02 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na ci Njénde li tay ci latine ji 2i fani desàmbar 2024,  Kilifa gii di Seneraal Biris Koloteer Oligi Ngemaa Njiitu Réewum Gaboŋ ak soxnaam, Soxna Sitaa Oligi Ngemaa, ci ngan gu ñu fi doon amal.

Ñaari Njiit yi jot nañoo séq ub jaataay ngir waxtaane tomb yu soxal ñaari réew yi. Xamle nañu seen yéene ci joxaat xar-kanam gu yees lëngoo gi yàgg a dox diggante Ndakaaru ak Libarwali yóbbu ko fu gën a sori. Muy kon ñaari réew yi fexee teg pexe yu yees ngir gën a rattaxal lëngoo gi ci pàcc yu am solo.

Ci geneen wàll, Peresidaa Fay posewu na ci ndaje mi ngir ndokkale naataangoom bu Gaboŋ bii ci kóolute gi mu am ci askanu Gaboŋ wi jëm ci taxawal Ndayi Sàrti Réew mu yees, ginnaaw referàndom bu 16i fani nowàmbar bii wees. Rafetlu na taxawaayu kilifteef gi Gaboŋ wane te war a doon royukaay ci ni muy doxalee Nguurug néggandiku ga, jaare ko ci ànd  ko ak ñépp ci jàmm, te lépp it tegu ci sàmmonte ak lél ya ñu tëral.

Njiitu Réewum Gaboŋ ci wàllam it xamle na mbégte mi mu am ci teewe màggalug bóom gi amoon Caaroy, sant it lool nee na ci dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel.

Mu daanele moom Peresidaa Ngemaa fésal ag cantam ak gu askanu Gaboŋ, jëme ci kilifay Senegaal yi ci njàppale gi ñu defaloon seen mbokku ma-réew bi ñu tabb bu yàggul dara Njiital ASECNA gi ab dalam nekk Ndakaaru.