Senegaal ak ACWA Power torlu nañu pas gi ñu waxtaanewaat ngir tabax isin buy xent ndoxum xorum si.

xamle - 17 MONTHS.JULY 2025

Ci njiitu Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY Njiitu Réew mi, Senegaal teg na jéego bu am solo ak torlug pas gi ñu waxtaanewaat jëm ci tabax isin buy xent ndoxu xorom si, mu lëkkaloo ci ak kippaangog sa-sawudi gii di ACWA Power.


Lëkkaloo gii ñu gën a dooleel day wane yéeney ñaari Réew yi jëm ci yëraat seen i déggoo ci kaw sàmm  njariñu Senegaal, pas-pasu doxaliin wu leer ci pas gi ak mbokkoo gi yàgg a boole ñaari askan yi.


Waxtaanewaat gi tax na ñu am njureef yu am solo, bokk ci yooyu :

- wàññi njëgu ndox mi, jóge ci 427 wàcc ba 389,8 FCFA/m³ ;

• woyofal bu baax yenu ndalu gi Nguur gi waroon a gàlloo at mu ne ;

• ful ñaari yoon dooley soleer bi, yóbbu ko ba 300 MWc ;

• yëraat anam yi ñu doon séddoo njariñ yiy bawoo ci jëfandiku gi ;

•  kopparal gu gën a woyof  ;

• jariñoo bu baax liy ballee ci réew mi ak dooleel jumtukaayi tàggatu yi ;

• sàmmonte ca na mu waree ak li ñu tëral ci wàllu lëkkaloo piblig-piriwe, ak jot ndigalu UNAPPP ak DCMP.


Ñu nisar ko ci 400.000 m³ bis bu set, jumtukaay bu am solo bii dina indi tontu lu wér ci càkkuteefu jot ci ndox mu sell ci ñetti gox yii di Ndakaaru-Cees-Mbuur, nga xam ne ñoom rekk ëmb nañu 80 % ci li dëkki réew mi yittewoo cim ndox.


Ci pose mii, Njiitu Réew mi fésal na ag cantam jëme ci Kilifa gii di Buur Salmaan Ben Abdel Asiis Al Sawud, Kilifag Ñaari Jumaa yu Sell yi, ci kilifa gii di doomi Buur bi Mohammet Ben Salmaan, niki noonu sunu bokki askanu Araabi Sawudit, ci seen kóolute gi ñu feddaliwaat ak seen jaayante ngir jàppale Senegaal.


Naal wii day wane doxaliinu lëngoo gu bees, gu tegu ci luy sax, koom mu am doole, yoriin wu leer ak gën a suqali nekkiinu askan wi.


Man ngeen a topp àddug Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY ci jataayu torlu pas gi : 



Peeñ :