Biti Réew - 13 MONTHS.MARCH 2025
Muy amal tukkib liggéey ci Ndakaaru, Mauro Viera miy Jëwriñu Beresil ji yor wàllu Jëflante ak Biti Réew, Njiitu Réew mi dalal na ko ci alxemes ji ci Njénde li. Ci biir ndaje mi, S Viera xamle na yéeney réewum Beresil jëm ci gën a rattaxal ay jëflanteem diggam ak Senegaal, rawati na ci wàllu koom mi, mbay mi ak xarala yi, ngir gën a dooleel lëkkaloo gi diggante ñaari réew yi.
Ci bis boobu ba leegi, Njiitu Réew mi dalal na, soxna Gérardine Mukeshimana, topp-njiital Fonds international de développement agricole (FIDA). Muy ndaje muy tàbbi ci yéeney FIDA jëm ci gunge politig yi Ngóornamaŋu Senegaal di teg ci wàllu mbay mi.