Sekkereteer Detaa Emiraa bi yor wàllu jëflante ak Afrig, dalal nañu ko ca Njéndel Réew mi.

Biti Réew - 29 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dalal na ci alxemes ji kilifa gii di Seex Shakhboot miy Sekkereteer Detaa Emiraa bi yor wàllu jëflante ak Afrig. Mu ñëwoon ngir feddali yéeney Emiraa Araab Unii jëm ci gën a dooleel jëflantey xaritoo yu mucc ayib ak lëkkaloo gi dox seen diggante ak Senegaal, ak waajalaale ngan gi Peresidaa Fay war a amal ca Abu Dabi ci ndënel Kilifa gi di Seex Mohammet Ben Zayed, Njiitu Réewum Emiraa Araab Unii.