Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 28i ut 2024, ndajem Ndiiaoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu set, ca Njénde la.
Ci ndoortel ay kàddoom, Njiitu Réew mi dellusiwaat na ci lootaabeg 130eelu Màggal gu Mag gu Tuubaa ak njariñ lu rëy li nekk ci suqalikug dëkki diine yi. Ndokkale na bu baax nag Kilifag yoonu Murid, Sëriñ Muntaxaa Basiiru Mbàkke ak mbooleem taalibey Murid yi.
Njiitu Càmm gi jaajëfal na itam Njiital Jëwriñ li ak mbooleem ñi bokk ci Ngornamaa bi, Ndoxalug mbeeraay gi, mbooleem wànqaasi Càmm gi ak way-kaaraange gi, ngir mbooleem matuwaay yi ñu jël ngir màggal gii man a am ci anam yu mucc ayib donte seetlu nañu sax taw yu bari yu jot a wàcc ci jamonoy nawet bii. Xamal na Njiital Jëwriñ li yitte ji mu am jëm ci suqali dëkki diine yu Senegaal, rawati na dëkkub Tuubaa gii, di ñaareelu dëkk ci réew mi ci wàllu ay nit ñu ko dëkke ginnaaw gëblag réew mi, di Ndakaaru.
Njiitu Réew mi fàttali na Ngornamaa bi ne Tuubaa dafa war am sémbu boppam wu ñu ko jagleel ci wàllu dëkkuwaay ak suqaliku guy boole asanismaa bu jaar yoon ak nosteg jot ci ndox mu sell.
Lu jëm ci waajtaayu Màggal guddig Mawluud gi, sàkku na ci Ngornamaa bi ñu dajale mbooleem wànqaasi nguur gi mbir mi soxal niki noonu jumtukaay yi war ngir taxaw ci amal lootaabe gu mucc ayib ci Màggal juddug Yónnent bi (SLHWS) ci mbooleem mbeeraayu réew mi.
Njiitu Càmm gi yëgal na Ndiisoo gi ne jot naa woolu waa Ngomblaan gi ci jataayub settee bu jëm ci sémbuw yoonal wu aju ci yeesal Ndayi Sàrti Réew mi. Yoonal googu ngi gaaral tas HCCT ak CESE, di ñaari campeef yu tënku ci artiikal 6 bu Ndayi Sàrti Réew mi. Gaaral gii nag day tàbbi ci dooleel yeesal yi ci wàllu ndayi sàrt yi, joyyanti anam yi kilifay pénc mi di jëlee dogal yi ak yaxanal gu matale ci alali nguur gi, di keno yu am solo ci soppi doxaliinu pénc mi ci ni ñu ko nammee jaare ko ci baral jéegoy "PROJET” bi.
Ba muy àddu ci wàllu dooleel taxawaayu Njàng mu Kawe mi ak Gëstu ci doxiinu “PROJET” bi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Jëwriñu Njàng mu Kawe mi, Gëstu ak Fent mu baral jéego yi, ci saytug Njiital Jëwriñ li ak lëkkaloog mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, jëm ci soppi gu matale ci anam yi sunu njàng mi ak gëstu gi di demee. Xamle na solo si nekk ci xayma yeesal ak naal yi bawoo woon ci diisoo yi ñu doon amal ci ëllëgu Njàng mu kawe mi ca weeru ut 2013. Muy kon, fexee jaare ci xayma googu, gën xóotal bu baax ci politigu réew mi ñeel njàng mu kawe mi, sukkandiku ko ci njureef ak baaxaayi doxaliinu njàng mi ci léppam rekk.
Njiitu Càmm gi àddu na mbooleem tomb yi yi sunu réew miy jànkonteel ci tolluwaay, sas ak soxla yi ci wàllu koom ak nekkiinu askan wi, niki noonu jamp gi nekk ci amal tàggatu gu xereñ ngir méngale sunu njàng mu kawe mi ak li àddina bi soxla ci wàllu xëy. Ci noonu, sàkku na ci Jëwriñ ji yore Njàng mu kawe mi ak Gëstu mu sumb ci lu amul àpp ànd ko ak Jëwriñ yi ak ñi mbir mi soxal, pexe yu wér te wóor ci taxawal doxaliinu suqali Njàng mu kawe mi, Gëstu ak fent, te bàyyiwaale ci xel ni xarala yi ak xelum xarala (IA) bi di gënee yéeg jëm ca kaw. Xamle na ne lu manul a ñàkk la ci ñu yeesal sàrt l° 2015- 02 bu 06i sãawiye 2015 bi soxal jànguney Senegaal yi ngir samp doxaliinu jàngune yu am dayoob yi am ci àddina si.
Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngornamaa bi ñu xalaat ci doxaliinu koom ñeel jànguney pénc mi ak njàng mu kawe mi, gëstu ak fent rawati na. Ci doxaliinu soppi googu, xamle na ne lu manul a ñàkk la ñu yaxanal jaare ko ci méngale rëddiinu jàngune yi, boole ko ak taxaw bu baax ci li ñuy jàngale, tabax yi, jumtukaay yi, jàngalekat yi, dongo yi, liggéeykati ndoxal yi, tegnig yi ak serwiis yi. Ci loolu, xamle na ne fàww ñu dooleel sas ak jumtukaay yu bànqaas biy saytu wóor ak baaxaayu Njàng mu kawe mi (ANAQ-Sup), di bànqaas bu war gën a taxaw ci saytu tàggatu ak lijaasa yi ñuy joxe ci warabi jàngukaay yu kawe yi rawati na yu piriwe bi.
Ci wàll woowu ba leegi, Njiitu Càmm gi taxaw na bu baax ci jamp gi nekk ci taxawal pexe yu wóor jëm ci jël ay jàngalekat ci njàng mu kawe mi ngir gën joyyanti taxawug njàngaan yi niki noonu saytu gu wér ci tolluwaayu wakaateer yi nekk ci jàngune yi ak warabi njàng mu kawe mi. Mu sàkku ci Ngornamaa bi ñu gën a suqali ak dooleel gëstu ak Fent ci jàngune yi.
Ba muy dellusi ci sànni gu njëkk gu satelitu Senegaal gii di GAINDESAT 1A 16i ut 2024, ca Etats-Unis, Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu ak fent, ak mbooleem bar gi séqoon sémb wii ci liggéey bu mucc ayib bi ñu amal ak seen ug dogu ba waral fent gu am solo gii dugg ci politigu jaww ju Senegaal. Sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Gëstu ak Fent mu wéyal eewestismaa yi ngir feddali jéego yu am solo yi ñu teg ci wàllu jaww ji, jaare ko ci gën a sóob kurélu Senegaal giy gëstu ci wàllu jaww (ASES) ak mbooleem kàngam yi réew mi am ci njeexitali sémb wu am solo wii méngoo lool ak pas-pasub lépp di jóge ci Senegaal gu moom boppam.
Ci kanamu njàqare gi am ci ni tefes yi di yàqoo ci gox yu bari ci Senegaal, Njiitu Réew mi xamle na ne donte am na jëf yu ñu ci jot a amal, lu bari des na ngir dooleel ci lu sax dayoob man a dékku risk ak tafaar yiy gën a yokk. Sàkku na kon ci Jëwriñu Kéew mi ak jàll jëm ci Ekolosi mu aajar ci Ndiisoog Jëwriñ yi ak yaatal pexe yu yees yi ñu tëral ci réew mi jëm ci xeex yàquteg tefes gi. Pexey ñaax ak fegu yii dañoo war a ànd ak teg jëf yu jamp yu ñu jagleel gox yi mbir mi di gën yoot. Day yell kon ñu naal ci gox yi yëf yiy gën a yoot jéem a xool nu ñu tuxalee askan wa jot a loru walla yëf yi jege leen.