SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ GU ÀLLARBA 23i FANI OKTOOBAR 2024

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 23 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 23i fani oktoobar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel kàddoom, Njiitu Réew mi sant na bu baax ci teertu gu mu mucc ayib gi ko askanu Kéedugu ak Tàmbaakundaa jagleel ci tukkib 2i fan yi mu fa doon amal. Jaajëfal na bu baax Jëwriñu larme bi, ju Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, ju Enersi, Petorol ak Miin, ju Kéew mi ak jàll jëm ci Ekolosi, Góornoor yi, Perefe yi ak Suu-perefe yi, Njiiti Koosey Departamàntaal yi, Meer yi ak mbooleem way-kaarange gi ci taxawaay bu mucc ayib bi ñu am ci waajtaay wi ak ci diiru tukkib nemmiku gi. Rafetlu na bu baax jéego yi ñu teg jëm ci aar nit ña ak seen alal, waaye itam doxalug dogal bi ñu jëloon jëm ci tere bépp yëngu ci lu jege 500i meetar ci li wër Faleme bi. Fàttali na Ngóornamaŋ bi ba tay ne fàww ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir taxawal sémb wu jamp ngir sàmm ak delloosi ekosistem bi ca Faleme ba. Mu tëj bunt boobu ci xamle ne, li ne këtt fii mu ne mooy gën a dooleel tundu Kéedugu ci wàllu ay jumtukaayi ndoxal, koom, dundiin ak mbatiit yi manul a ñàkk ngir gën a man a jëfandikoo koom mu am solo mi nekk ci tund woowu.

Ci lu soxal topp tolluwaayu dexi Senegaal ak Gàmbi yi tuuru, Njiitu Reew mi dikkaat na ci nemmiku gi mu jot a amal ca Bàkkel, gaawu 19i fani 2024, ngir yegge askan wa loru ci tuurug dexu Senegaal gi, njàppaleg mbooleem waa réew mi. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu taxawal ci lu jamp Sémbuw dékku ak ndimbal wu  wóor woo xam ne pàcc bi ne woon këtt, jot nañu koo jagleel juróom ñetti (8) milyaar ngir amal taxawu gu gaaw te xereñ ñeel askan wi loru ak ña ñu tuxale ca warab ya ndox yi laal, rawati  na ca gox yu Bàkkel, Podoor, Dagana, Maatam ak Kanel. Woo na Njiital Jëwriñ yi mu ànd ak Jëwriñ yi mu soxal, ñu taxaw ci amal ay yëngu yu jëm ci fagaru ak teg matuwaayi gunge yu wóor, ci saytu ak lëkkaleg kilfay ndoxal gi, ngir taxawu gu mucc ayib ñeel way-loru ñi ci gox yooyu ndox mi laal. 

Njiitu Réew mi xamle na ne dayoob fengat yi war naa tax Nguur gi di ko gën a fuglu boole ko ak di bàyyi xel ci jafe-jafey dëkkalaat gu sax ñeel  askan wi niki noonu jéem a lootaabewaat yënguy mbay mi, koom mi, dundiin wi ak njàng mi ci gox yooyu loru ci rembetaayu dexi Senegaal ak Gàmbi. Kon nag nañu gën a sóob wànqaasi nguur gi ak larme bi ci gox yi gën a loru ci mbir mi, fu mel ni dëkk yi nekk ci Dànde Maayo bi ci tundu Maatam ak gox yi nga xam ne jamono jii ñu ngi fay àrtu, fu mel ni Ndar ak dëkk yi nekk ci gox yu Dagana ak Podoor. 

Lu soxal kàmpaañ biy dëgmal te war a tijji gaawu 26i oktoobar ci minwi jëm ci joŋantey depite yu 17i Nowàmbar 2024, woo na mbooleem ma-réew yi ak way-politig yi ñu dox ci luy tax ñu amal kàmpaañ bu mucc ayib, tegu ci jàmm, ku ne am taxawaayu kilifa ngir njariñu réew mi niki ko sàrt yi tëralee. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir amal kàmpaañ ak joŋante yu jaar yoon fépp ci biir réew mi ak ca biti réew. Ci loolu soññ na Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi mu gën a bàyyi xel tolluwaay bi am ci gox yi ndoxu dex gi nangu. 

Lu jëm ci waajtaayu JOJ Dakar 2026 yi, Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ yi mu taxaw ci fexe ba mbooleem jëwriñ yi ak yeneen wànqaas yi am waar wu ñu war a bay ci lu soxal Senegaal ci wàllu tabax ay jumtukaayi tàggat yaram, ay tali, yooni saxaar, turism añs, ñu taxaw ci mu daal di mat. 

Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww ñu feexee peeg bu baax njël li ñu natt ngir lootaabe gi ak di topp saa su ne arminaatu jébbale eefrastiriktiir yi ci waxtoom niki ñu ko tënkee woon ànd ko ak CIO. Sàkku na ci Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram ak Mbatiit mu ànd ak CNOS sumb ab kàmpaañu xamle ci réew mi ak ca biti réew jëme ci ndaw ñi ak ñiy yëngu ci tàggat yaram ak mbatiit te boole ko ak fexe ba sunu ndaw ñi war a joŋante am waajtay wu mucc ayib boole ko ak dekkalat tàggat yaram ci lekool yi ak jàngune yi. Xamle na tamit ne fàww ñu taxaw ci gën a jagal mbooleem li wër bokk-moomeel yi ak warab yi war a dalal joŋantey JOJ yooyu.

Njiitu Réew mi dikkaat na ci Jataayu waxtaane Ndefar yi, yaxantu gi ak PME/PMI yi ak Jataayu waxtaane dem bi ak dikk gi ci caytug Njiital Jëwriñ yi, ginnaaw fésalug “Vision Senegaal 2050”. Jaajëfal na Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu ndefar gi ak yaxantu gi, Jëwriñu eefrastiriktiir yi ak yaaleg suuf si ak jaww ji, Jëwriñ ji yor eefrastiriktiiri géej gi ak waax yi, ci seen gis-gis yu am solo yii ñu àndadoo am jëm ci amal ay diisoo yu ñépp ànd ngir wut ay pexe ci jafe-jafe yi am ci wàll yi ñu yor. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo ak mbooleem jëwriñ yi mu soxal, ñu taxaw ci jëmmal ca na mu gën a gaawee, tegtal yi bawoo ci Jataayi waxtaan yooyu.

Njiitu Réew mi sant na bu baax ci dellusig sunu bokk yi tagoon ca Liban. Rafetlu na bu baax taxawaay bu am solo bi Jëwriñ ji yor Bennoog Afrig ak Jëflante ak Biti Réew ak ñi mu doon liggéeyandool wane ci mbir mi.

Mu tëjee ci arminaatu laamisoom, xamal Ndiisoo gi moom Njiitu Réew mi ne dina teew ca Araabi Sawudit 27 ba 30i fani oktoobar 2024, ca “Forum Futur Investment Initiative 2024”, laataa muy amal tukkib nemmiku ca Turki 31i fani oktoobar ba 1 panu nowàmbar 2024.

Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi taxaw na bu baax ci ñu fexee topp bu baax matuwaay yu jamp yi ñu jëloon ci ndaje mi ñu amaloon diggante jëwriñ yi jëm ci saafara ak taxawu askan yi loru ci tuurug dex yu Senegaal ak Gàmbi. Fàttali na ne ci yoxoy Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi lañu tegoon yëngu yi mbooleem wànqaasi njëwriñ yi war a amal ci warab yooyu. Ci loolu xamle na ne fàww ñu gën a bàyyi xel càkkuteefi askan wa te di ko ci defal ag tënk bis bu set ngir ñu man cee taxaw walla bu dee dafa laaj joyyanti ñu man koo amal. 

Njiital Jëwriñ yi xamal na Ndiisoo gi tolluwaay bu dal xel bi am ci liggéey yi kurél gi ñu dénk, ci Njiital Profesëer Mammadu Juuf, fàttalikug 80eelu at mi ñu bóomoon tiiraayéer yu Senegaal ca Caaroy, 01 panu desàmbar 1944. Ay jéego yu wér a ngi am ci Gëstu yi ñuy amal jaare ko ci jëfandikoo balluwaay yu wóor ci arsiif yi fi jot a nekk ngir fésal liy dëgg ci xew-xew bu tiis boobu. Dees na ko mottali ci fan yii di dëgmal ci tukki bu ñu war a amal ca Farãas ngir gën a xóotal ci dajale ay firnde. Lu soxal màggal gi nag, fexee nañu ba amal ci doxaliin wu ñépp di dugg ànd ko ak gox yi ak goxaan yi, ñiy yëngu ci wàllu mbatiit ci réew mi niki noonu yeneen réewi Afrig yi laale ci mbirum tiiraayéer yooyu. 

CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:

Jëwriñu Bennoog Afrig ak Jëflante ak Biti Réew àddu na ci tolluwayu àddina si;


Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi àddu na ci lu soxal wal mi am ginnaaw tuurug dex yu Senegaal ak Gàmbi;


Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa def na leeralu ayu-bis bi muy amal ci tolluwaayu saytug wal mi.


CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii: 


Njénde li:

Sëriñ Abdulaay Tin, Layookat, tabb nañu ko PCA bu SOGEPA-SN, mu wuutu Sëriñ El Haaji Sekk Njaay WÀDD.

Njëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox yi ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay gi:

Sëriñ Sàmba NJAAY, Xereñtaan ci wàllu seni siwil, tabb nañu ko PCA SN-HLM, mu wuutu Sëriñ Mustafaa FAAL;

Sëriñ Useynu FAY, Arsitekt irbanist, tabb nañu ko PCA SICAP-SA, mu wuutu Sëriñ Mammadu FAY;

Sëriñ Ibraahiima COY, Adminiatatéer Siwil peresipaal, tabb nañu ko Bootalu SAFRU SA, mu wuutu Sëriñ Maysa Mahekoor JUUF;


Njëwriñu Caabal yi, Jokkoo yi ak Xarala:

Soxna Maane CAAM, Kàngam ci wàllu kontaabilite, tabb nañu ko PCA SN-LA POSTE, mu wuutu Sëriñ Lansana SANO;

Sëriñ Umar WATT tabb nañu ko PCA SENUM SA, mu wuutu Sëriñ Jeegaan SEEN;

Sëriñ Sadiix TOOB tabb nañu ko PCA SN-APS, mu wuutu Sëriñ Mustafaa SÀMB;

Njëwriñu Koppar yi ak Njël li:


Sëriñ Buubakar SOLI, Doktoor ci wàllu melo-suuf, tabb nañu ko PCA SOGIP-SA, mu wuutu Sëriñ Meysa Ndaw WÀDD;

Soxna Ndey Faatu Faal, am lijaasab DEA ci “Droit economique et des affaires”, tabb nañu ko PCA (SNR), mu wuutu Sëriñ Paab JUUF;

Sëriñ Mustafaa KAMARA, am lijaasab master 2 ci wàllu xereñteg sistemu xarala yi, tabb nañu ko PCA LONASE, mu wuutu Sëriñ Sire JA;

Sëriñ Siidi FAAL, operaatéer ekonomig, tabb nañu ko PCA FGA, mu wuutu Sëriñ Moor Ja CAAM;

Sëriñ Momat SIISE, Xereñtaan ci wàllu estatistig, tabb nañu ko Topp-Bootalu ANSD, toogu bu kenn newutoon;

Sëriñ Umar REMI, Xereñtaan ci wàllu komers international, tabb nañu ko PCA FONGIP, mu wuutu Sëriñ Umar NDÓOY;


Njëwriñu Jumtukaay yi ak Yaaleg Suuf si ak Jaww ji:

Sëriñ Lórãa SINAA, koosiltaa ci sistem management kalite, tabb nañu ko PCA LNT-BTP CEREEQ-SA woon, mu wuutu Sëriñ Daam JÓOB;

Sëriñ Yuusufa SIIS, Jàngalekat, tabb nañu ko PCA SN-LAS, mu wuutu Soxna Ndey Sali Jóob JEŊ;


Njëwriñu Paj mi ak Ndimbal li

Sëriñ Mammadu SAANE, am lijaasab doktoor ci farmasi, tabb nañu ko PCA PNA, mu wuutu Soxna Aysatu Mbeen Lóo NGOM;


Njëwriñu Mbay mi, Bay Dunde ak Càmm gi:

Sëriñ Faamara MAANE, Jàngalekat, tabb nañu ko PCA SODAGRI, mu wuutu Sëriif SAABALI;


Njëwriñu Njaboot gi ak Jàppalante 

Soxna Maam Mbisin NJAAY, Tegnisee Sipperiyéer ci komers international, tabb nañu ko PCA ONPN, mu wuutu Sëriñ Abdu Asiis NJAAY.


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi