SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ GU ÀLLARBA 20i FANI NOWÀMBAR 2024

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 20 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 20i fani nowàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoorteel i kàddoom, Njiitu Réew mi ndokkale na askanu Senegaal wi takku wane ag mat ak demokaraasi ci joŋantey tànn depitey fukk ak juróomeelu Ngomblaan gi, lépp ci dal ak jàmm. Ndokkale na Ngóornamaŋ bi rawati na Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, Kilifay Ndoxal yi nekk ci mbeeraay gi (Góornoor, Perefe, Suu Perefe), DGE di Pekkub Joŋante yi, ndawi laamisoo yi teew Senegaal, CENA di Kurél giy saytu joŋante yi, CNRA di kurel giy saytu Caabal yi ak mbooleem way-kaaraange gi, ci lootaabe gu mucc ayib gi ak leeraay bi am ci joŋantey lesislatif yi ñu amal ci mbeeraayug réew mi ak ca biti réew. 

Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax Usmaan Sonko miy Njiital Jëwriñ yi doon it Njiital PASTEF ci dogoom ak taxawaayam yi tax làng gi muy Jiite jël li ëpp ci depite yi ca Ngomblaan ga. 


Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi yitte ju kawe ji mu am ci doxal ci anam yu mucc ayib sukkandiku ko ci pàcc yi ñu séddalee gis-gisu Senegaal gu moom bopam, jub te naat fii ak 2050. Xamle na  ne fàww ñu amal coppite yu wér te wóor ci fànn yépp ci doxaliinu Senegaal. Sas wii nu bokk nag mu ngi war a jaar ci taxaw ci saafara yitte yi gën jamp ci wàllu koom ak dundiin, xeex ak njëgu dund bu kawe bi ak fexee yokk man-mani jaboot yi ci seen i jiba, fexe ba askan wi man a jot ci soxla yi manul a ñàkk, suqali man-man ak xëyu ndaw ñi, ndoortel « new deal technologique » bi, dooleel gox yi ngir def leen ñuy ay warabi fent, dundalaat ak dooleel koomum réew mi, rawati na ci fànn yu am solo yi mel ni mbay mi, càmm gi, napp gi, ndaamaari gi, mbell yi ak njafaan yi.


Njiitu Réew mi dikkaat na ci wareefu Ngomblaan gi ak sañ-sañam yi bokk ci wote ay sàrt, saytu jëfi Ngóornamaŋ bi ak càmbar doxaliinu pénc mi Ngóornamaŋ bi di doxal ak a lëkkale. Ci Loolu sàkku na ci Ngóornamaŋ bi rawati na ci Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ñu gaaw matale ngir aajar ci Ndiisoog Jëwriñ yi sémbu yoonal wu jëm ci koppar yi ñeel atum 2025 te ñu war koo càmbar ci àppi settee.


Njiitu Réew mi rafetlu na itam liggéey bu mucc ayib bi ngóornamaŋ bi jot a amal ci juróom ñetti weer yi njëkk ci at mi ci jamono joj Senegaal amal na fi ñaari joŋantey pal yu mag. Rafetlu na bu baax ci jamonoy joyyanti yii, jubbanti ak càmbar doxaliin yi, taxawaay bu mat a roy bi kenn ku nekk ci ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi wane.


Lu soxal kàmpaañu njaayum li ñoree ci mbay mi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu taxaw ci gën a sàmm njariñi baykat yi, ci fay leen ca na mu waree li ñu jot a ñorle boole ko ak suqali ndefar yi ci réew mi ngir gën dooleel moom sunu bopp gi ci wàllu koom. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir taxawal njëg yu yenu maanaa jëm ci li ñu war a jëndee kilo gerte gi ci baykat bi.


Njiitu Réew mi woo na itam, Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñ ji yor wàllu Mbay mi ak ji yor wàllu Ndefar yi ñu rëdd, te déggoo ko ak operaatéer yi ak way-ndefar yi ci wàll wi, anami yëngu ci marsey gerte gi. Di loo xam ne dina tax ñu man a aaral baykat yi li ñuy am boole ko ak méngale ak jamono jumtukaayi ndefar gi jëm ci soppi ci réew mi gerte gi fiy ñoree. Ngir tëj bunt boobu nag, sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu gaaw amal, am ndaje diggante jëwriñ yi ci kàmpaañu njaayum li ñoree ci mbay mi.


Ba muy àddu ci lu soxal «  Biennale de l’Art africain contemporain », Njiitu Réew mi ndokkale na Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat Yaram ak Mbatiit, Sekkereteer Detaa bi yor wàllu Mbatiit, Ndefar yi ci wàllu fent ak sunu am-am ci wàllu mboor, Peresidaa komite oriyàntaasoo bu « Biennale » bi ak mbooleem njabootu mbatiit mi takku taxaw ngir amal ndam lu rëy ci xew-xew bu màgg bii ñeel Senegaal ak Afrig. Woo na Ngóornamaŋ bi sax nag ci loolu, mu gën a taxawu « Biennale » bii nga xam ne, ñu ngi ko jàppaat ca atum 2026 mu war a daje ak Powi Olempig yi ñu jagleel ndaw ñi. 


Xamal na itam Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, solos Nguur gi gën a dooleel wutum jumtukaayi pasin yi ak taaral taaxi pénc mi jaare ko ci jënd ay pentiir, tapiseeri ak yeneen jumtukaay yu sunu ma-pasin yi di defar. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Mbatiit mi mu gën a dooleel yeesal ak porodiksoo yu «Manufactures des Arts décoratifs »  ba ca Cees, boole ci sumb ay xalaat ci koparal gi ngir gën a fésal pasinu Senegaal. 


Xamle na solos suqali koom mu am doole ci wàllu Pasin ak Mbatiit boole ko ak dundalaat xereñteg pasin gi jaare ko ci doxal waxtaane pexe yu jëm ci soppi Ekool biy jàngale wàllu Pasiin ak Liggéeyi Mbatiit ci réew mi di (Ecole nationale des Arts et Métiers de la Culture).


Senegaal dina màggal, 1 panu desàmbar 2024, 80eelu atu xew-xew bii soxal « bóom gi amoon Caaroy ». Ci loolu, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñu Larme bi ñu gaaw matale yënguy waajtaayi xew-xew bu màgg bii ci àddina si, ñu jagleel fàttaliku « Tiiraayéer Senegaal » yi ak sunu « Aasee kombataŋ » yi. Ñoom ñii nga xam ne ag njàmbaar lañu wane ci seen jaar-jaar te doon lees war a jàngal sunuy ndaw, dugal nañu seen loxo bu baax ci sàmm péexte, ngor ak jonnug réewi Afrig yi.


 Mu tëjee moom Njiitu Réew Mi ci ndokkale bu baax Keleŋu àddina si ci MMA bu « ONE Championship », di sunu naataangoo ma-réew bii di Umar Kan ñu gën koo miin ci Rëg-Rëg, di kok ndamam li siggil na Afrig gépp. 


Ci ndoorteel i kàddoom, Njiital Jëwriñ yi sant na bu baax ci kóolute gi askanu Senegaal feddaliwaat jëme ko ci sémbu amal coppite gu matale ci doxaliinu réew mi Njiitu Réew mi woote, ci joŋantey lesislatif yi jàll. Muy firndeel rekk ne rafetlu nañu yi nguur gi jot a sottal ci juróom ñaari weer yu njëkk yiy wane teqalikoo ak yenn doxaliin yi ñu leen digoon. Xamle na ne fàww kon ñu gën a liggéey te bañ a dàcc ngir matale bu wér yaakaar ju rëy ji askan wi am ci ñoom ci fànn yépp nag. 


Ci loolu, Njiital Jëwriñ yi xamle na ne fàww ñu gaaw matale, ci ñaari ayi-bis yii di ñëw, wayndare yi aju ci yoon wi ñu war a jaar ci atum 2025 naal yi ak sémbi « Référentiel Sénégal 2050 » ak sémbu njëlul 2025 wi ñu war a gaaral ca Ngomblaan ga. Ci geneen wàll, rafetlu na bu baax anam yu mucc ayib yi ñu taxawoo liggéey yi aju ci waajtaayu màggal 1 panu desàmbar, di 80eelu at mi ñu bóomoon « Tiiraayéer yu Senegaal » ca Caaroy.


Mu daaneele moom Njiital Jëwriñ yi ci fésal tolluwaay bu dal xel bi jot a am ci yëngu yi gënoon a soxal Ngóornamaŋ bi ci diggante awril-sebtàmbar 2024, boole ko ak ñaax Jëwriñ yi ñu matale liggéey yi des balaa njeextalu atum 2024, ci kaw li fi jàppandi ci wàllu njël li.


CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:

  • Jëwriñ Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi àddu na ci Ndaje mi ñu amaloon ngir xayma Palaŋ yi ñu waroon a doxal ci yitte yi gën a far ñeel wànqaasi Njëwriñ gu ne ci diggante awril-sebtàmbar 2024;


  • Jëwriñu Koom mi, Palaŋ ak Lëkkaloo àddu na ci « Référentiel Sénégal 2050 » bu yees bii ak ci Palaŋ yi ñu war a doxal ci juróomi at yii di 2025-2029 ; 


  • Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa def na leeralu ayu-bis bi muy amal ci tolluwaayu saytug wal mi.


CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

  • Sémbu dekkere bi jëm ci sos ak taxawal sàrti lootaabe ak doxaliinu Kër gi ñu dénk yóbbu kuraa ci àll bi di ASER.

CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii: 


  • Njëwriñu Bennoog Afrig gi ak Jëflante ak Biti Réew 

Sëriñ Kiriscaan Alain Sosef ASOGBA, limatu payoor l°611.446/Z, tabb nañu ko ma-laamisoo, Bootalu Porotokol, Waxtaani àddina si ak tekki, mu wuutu Sëriñ Ma-Gay Géy mi ñu soxla ci yeneen yitte. 


Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE