Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru JOMAAY Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 18i sebtàmbar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi wane na mbégteem ci lootaabe gu mucc ayib gi ñu amal ci màggal guddig GÀMM gi am ci anam yu jaar yoon ci mbooleem mbeeraayu réew mi. Sant na bu baax Xalifa seneraal yi, kilifay diine yi ak mbooleem julliti Senegaal yi ci ñaan yu am solo yi ñu amal ngir Senegaalug jàmm, gu dal te naat tegu ci yoon ak dimbalnte.
Ndokkale na mbooleem Ngóornamaŋ bi, Njiital Jëwriñ li, Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, Jëwriñ yi mu soxaloon, mbooleem way-kaaraange yi ak wànqaasi nguur yi tax ñu amal Mawlud 2024 gu mucc ayib.
Njiitu Réew mi fésal yënguy diine yi nga xam ne lu sax la ci Senegaal, doon loo xam ne dafa am taxawaayu koom, ndimbal, mbatiit ak jàngale gu fés. Àddu na ci yitte ji Nguur gi war a am ci càmbar doxaliin wu matale wii ci mbooleem màggal yi ak xewi diine yi. Nguur gi dafa war a taxaw temm, ci sàmmonte ak gëm-gëm yi ak fexee xool ci kéem tolluwaayu kàttanam, gunge kurél yi ak këri diine yi ci biir ni ñu baree te wuute.
Ba muy dellusiwaat ci tasug Ngomblaan gi, Njiitu Réew mi taxaw na ci solos amal waajtaay wu jaar yoon ngir lootaabe gu mucc ayib ci joŋantey tànn depite yi ñu jàpp dibéer 17i nowàmbar 2024. Yëgal na Ndiisoo gi ne jël na ñaari dekkere yu jëm ci woolu ñiy lootaabe joŋante yi ak anam yi ñuy séddale limub depite yi ñu war a tànn ci raw-gàddug gox yi. Ci loolu, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu jël mbooleem matuwaay yi war ngir joŋante yu mucc ayib ñeel saa-senegaal yi nekk ci biir réew mi ak yi nekk ca biti réew.
Ba tay, Njiitu Réew mi woo na Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi, te yor wàllu lootaabe joŋante yi, mu sumb ay waxtaan ànd ko ak kurél gi yor wàllu saytu joŋantey pal ci réew mi (CENA), way-politig yi ak kurél yi mu soxal ngir man a séddoo ak ñoom lépp luy wàllu tegnig, ndoxal ak kopparal yu aju ci jonatey fal depite yu dibéer 17i nowàmbar 2024. Sàkku na tamit ci Jëwriñ ji yor wàllu joŋante yi mu amal kàmpaañu yëgle bu yaatu ci wetu way-politig yi ak askan wi ngir xamle, ci anam yu leer, sàrti lootaabe joŋante yi ak kàmpaañu dangaan gi.
Jéeya ju Mbuur ji, ñu dund ayu-bis bii wees, wane na jafe-jafe bi nekk ci wàllu mbëkk mi, te am kurel yu lootaabewu yu koy amal, doon ñuy xiirtal nit ñi di leen gëmloo lu amul, di ñu ñu war a rëbb ba jàpp leen teg leen li yoon wax ci ñoom kéem tolluwaayu seen jëf. Loolu tax na Njiitu Réew Mi di ñaax Njiital Jëwriñ li mu gën a dooleel ànd ko ak Jëwriñ yi mu soxal, mbooleem matuwaayi fuglu yi, kaaraange ak jumtukaayi xeex ak ñiy bawoo ci réew mi ngir mbëkki.
Njiitu Réew mi fésal na tamit, ci Njiital Jëwriñ li mu taxawal ci lu jamp pexem saytu diggante jëwriñ yi jumtukaayu xeex mbëkk mi ak saytuwaat doxal ak lëkkale ci réew mi yënguy fuglu ak xeex mbëkk mi, jaare ko ci dooleel teel a dànkaafu gi, lëkkaloo ak askan wi, yeete ak xamle rawati na ci wetu ndaw ñi. Ci kanamu sabab yu xóot yi am ci ni tukki bu jaarul yoon bii di màggee ci at yii nu génn, sàkku na ci Njiital Jëwriñ li mu sumb ca na mu gën a gaawee, ànd ko ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, ay diisoo yu ñépp di bokk amal ci réew mi ci mbirum mbëkk mi jëm ci joyyanti sunuy pexey xeex lu jëm ci wàll wi.
Njiitu Réew mi woo na Njiital Jëwriñ li ak Jëwriñu koppar yi ak Njël li ñu taxawal sémbuw njël lu ñu jagleel « Fuglu ak xeex tukki bu jaarul ci yoon».
Njiitu Réew mi àddu na ci wal mi ak taxawug Nguur gi ñeel way-loru ñi. Jébbal na njaalu askan wi jëme ci njabooti ñi faatule. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu jël mbooleem matuwaay yu jamp ngir lootaabe wallu yi ak yaatal dimbalnte gi ci réew mi ci wetu askan wi loru ci mbooleem mbeeraayu réew mi.
Ba muy àddu ci 22eelu atu fàttaliku suuxug Bateau Le Joola gi ñu jàpp 26i sebtàmbar 2024 ca Sigicoor ak Ndakaaru, Njiitu Réew mi fàttali na ne mooy jéeya ji gën a mag ju sunu réew mas a dund. Woo na Njiital Jëwriñ li mu jël mbooleem matuwaay yi ngir fàttaliku xew-xew bu metti bii ànd ko ak njabooti way-loru ñi.
Lu soxal ndam li am ci « first Sénégal Spatial Day » ak taxawaay bu am solo bi gëstug xeltu ak xarala am, Njiitu Réew mi ndokkale na Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu ak Fent, mboleem ñiy yëngu ci jàngune yi, gëstukat yi ak barug GaindeSat gi ci ndam li am ci Bëccëgug màggal ci réew mi sànnig satelitu Senegaal bu njëkk, te ñu lootaabe woon ko àjjuma 13i sebtàmbar 2024.
Mu daaneele, ci arminaatu laamisoom, moom Njiitu Réew mi xamal Ndiisoo gi ne dina dem ca New York, ca Etats-Unis, 22 ba 26i sebtàmbar 2024, ngir teewe Ndajem Ëllëg ak Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si .
Cig àddoom, Njiital Jëwriñ li aajar na Ndiisoo gi arminaatu doxal Sukkandikukaay bu yees bu politigu koom ak nekkiin bu 2025-2050 ak ay tëraliinam ci benn Master Plan 2025-2034 ak benn Plan bu juróomi at 2025-2029. Ci loolu, fàttali na mbooleem pàcci yooni doxal Sukkandikukaay boobu, jaare ko ci fésal diisoo yi ñu jot a amal rawati na ak sektëer piriwe bi ak sosiyete siwil bi ngir am seen gis-gis ak njañse ci wayndare yii ñu amal. Wayndare yooyu dees na leen jébbal Njiitu Réew mi ngir mu jàllale leen ñu man leen a fésal.
Njiital Jëwriñ li teg ci àddu ci dogal yi bawoo ci ndaje diggante jëwriñ yi, ñu amal 17i sebtàmbar 2024, ñu jagleloon ko njureefi ñàkkum ndox mi ak jafe-jafey fengat yi ci nawet bii ci mbay mi, dëkkuwaay yi ak jumtukaay yi rawati na yoon yi. Dogal yi gën fés yi ñu jël ñoo ngi séddalikoo ci diggante, waññi gu matale ci tool yi mu laal ak matukaay yi ñu war a jël ngir jàmmaarloo ak jafe-jafey dund yu man a am ci yenn gox yi mu laal ci réew mi. Lu soxal fengat yi, lees ci gën jàpp mooy jagal jumtukaayi fuglu ak taxaw niki noonu dooleel lëkkaloo diggante réew yi séq OMVS ak OMVG ci wàllu saytug ndox mi.
Ci kanamu néewug ndox mi ak fengat yi, Njiital Jëwriñ li yëgal na Ndiisoo gi taxawalug genn Kurél ca Primature guy ëmb mbooleem wàll yi ko séq ngir taxaw ci saytu ak doxal gu mucc ayib ci dogal yi ñu jël.
Mu daaneel, moom Njiital Jëwriñ li àddu ci tomb bii jëm ci joyyantiwaat këri liggéeyukaay piblig ak parapiblig yi ne ciy jafe-jafe. Ngir baral jéego yi ci saytu wayndare yooyu, jàpp na ne lu manul a ñàkk la ci doxalaat kurél diggante jëwriñ yi jëm ci topp ak joyyantiwaat liggéeyukaayi piblig bi ak parapiblig bi ñu taxawal ci biir Primature.
Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñu Koppar yi ak Njël li, lëkkaloo ko ak Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, mu jël matuwaay yi war ngir taxaw ci doxug kurél googu.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:
● Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa def na leeralu ayu-bis bi muy amal ci tolluwaayu saytug wal mi;
● Jëwriñu Napp mi, Jumtukaayi waax yi ak géej yi def na leeral ci doxalug dogal yi bawoo woon ca ndaje diggante jëwriñ yi ñu jagleeloon jumtukaayi géej yi ak waax yi.
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
● Sémbu dekkere bu aju ci ñetti weer ak àppug noppalu yi ak bër yi ci lekool yi, jàngukaay yi ak daara yi ci atum njàngu 2024-2025.
CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii:
CI WÀLLU NJÉNDE LA:
● Sëriñ Jim DARAAME, Gëstukat ca IFAN tabb nañu ko Njiital biri diine yi ak dugalug way-lijaasa yi ci làkku araabz
CI WÀLLU JËWRIÑU KOPPAR YI AK NJËL LI:
● Sëriñ Muhammadu Bàmba SIIBI, Inspecteur Impôts ak Domaines tabb nañu ko njiital bànqaas biy saytu xibaar yi aju ci wàllu koppar yi (CENTIF), mu wuutu fa Soxna Ramatulaay Gaajo Aañ.
CI WÀLLU JËWRIÑU YOON JI:
● Soxna Ayse Gasama TAAL, Àttekat, limatu payoor l°516 916/ D, tabb nañu ko Njiital Protection judiciaire et sociale ca Njëwriñu Yoon ji, toogu bu kenn ne wutoon;
● Sëriñ Suleymaan TELIKO, Àttekat, limatu payoor l°516 912/Z, tabb nañu ko Njiital Centre de Formation judiciaire (CFJ) ca Njëwriñu Yoon ji, mu wuutu fa Sëriñ Ma-Demba Géy, mi ñu woolu ci feneen;
● Sëriñ Moor NJAAY, Àttekat, limatu payoor l°616 170/Q, tabb nañu ko Njiital Office national de Recouvrement des Avoirs criminels (ONRAC) ca Njëwriñu Yoon ji, mu wuutu fa Sëriñ Maalig LAMOT, mi ñu woolu ci feneen;
● Sëriñ Ibraahiima TIN, Ingénieur Génie civil, tabb nañu ko Njiital Tabaxug Ëtti àttekaay yi ak taax yi ca Njëwriñu Yoon ji, mu wuutu fa Sëriñ Mohammed WAN.
CI WÀLLU JËWRIÑU BIIR RÉEW MI AK KAARAANGEG PÉNC MI:
● Soxna Mariyeem Puy AAN,
Administrateur siwil, limatu payoor l°696 392/G, ne woon topp-jaraaf ju Luga, yoroon mbiri ndoxal, tabb nañu ko calaw lu Gingineew, toogu bu kenn nekkutoon;
● Sëriñ Seex SÀMB, Administrateur siwil principal, limatu payoor l°616 300/H, tabb nañu ko Sekkreteer Seneraal ca Agence d’Assistance à la Sécurité de Proximité, mu wuutu fa Sëriñ Baabakar BA, mi ñu woolu feneen.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE