NDIISOOG JËWRIÑ YI - 16 MONTHS.OCTOBER 2024
Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 16i fani oktoobar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi wane na mbégteem ci ndoortel sémbu “VISION SENEGAL 2050”.Feddali na ag cantam jëme ci Njiital Jëwriñ li ak mbooleem Ngóornamaŋ bi ci liggéey bu mucc ayib bii nga xam ne lépp wànqaasi nguur gi ak kàngami réew mi a ko amal. Ci wàll woowu ba leegi, sàkku na ci Njiital Jëwriñ li mu gën a yaatal wayndare wi ci mbooleem ñi am kàddu ci réew mi ak askan wi ngir ñu def ko seen yëfi bopp te ànd ak ñoom doxal gi ñu tënk ci master plan bu 10i at, te 5i at yu njëkk yi war a door ci atum 2025.
Ginnaaw càmbar yi ñu amal ci alalu askan wi ba seetlu ne fàww ñu baral jéego yi jëm ci joyyantiwaat koom mi, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu wéyal pexe yi ñuy teg ngir woyofal bu baax dundiinu nguur gi niki noonu feddali njël li ñu natt ngir taxaw ci luy jagal man-mani wànqaas yi aju ci nguur.
Njiitu Réew mi taxaw na bu baax ci solos am Nguur gu xereñ ci man a taxaw ci li ñu ko sas, pexe yi ak anam yi muy àddoo jëm ci taxaw ci luy gën a dooleel Póol yi ñu war a sanc ci mbeeraay gi. Póol yooyu nag ñoo war a màndargaal réewum Senegaal gu fees deel ak ay ndefar yu ànd ak ay filiyeer yu am solo yoo xam ne dañuy doon ay jumtukaayi yokkute, suqaliku gu sax te yamale boole ko ak man a jur ay xëy yu wóor. Ci loolu, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu xalaat ci pexey taxawal xëy yu méngoo ak Gis-gisu Senegaal 2050 boole ko ak taxaw temm ci topp liggéeyukaayi piblig bi ak piriwe bi nekk ciy jafe-jafe lépp ngir lu gën a ñoŋal koom mi ak xëy yi.
Ci yoon woowu ñu jël jëm ci soppi ni ñuy yoree pénc mi, Njiitu Réew mi soññee na ci ñu taxaw temm ci gën a taxawu sektëer piriwe bi. Xamle na ne fàww Ngóornamaŋ bi taxaw ci luy tax jëflante yi gën a xemmeemu te am doole, gën a dooleel waxtaan wi diggante Nguur gi ak piriwe bi, fexee dugal ndoxal gi ci xaral yi, gën a dooleel waaday réew mi ci mbooleem pàcci koom mi ak ci ay filiyeer yu am solo, waaye tamit nag fexee soppi koomum eeformel bi nga xam ne lu sax la ci réew mi ngir def ko mu doon jumtukaayu yokkute bu man a jur ay xëy yu wóor.
Njiitu Réew xamle na yitte ji mu teg ci fexe ba téyeel sunu bopp wàllu mbell yi, mbay mi ak xarala. Soññee na jëm ci dekkalaat mbirum ndaamaari gi nga xam ne sunu réew doon na ci ku ràññiku. Ci yoon woowu jëm ci tabax koom mu sax ci réew mi ba noppi door a ubbiku ci réewi àddina si, xamle na ne fàww ñu teg ay pexey politig yu yees ci wàllu waax yi ak géej gi, di pexe yoo xam ne dinañu tax sunu waax yi gën a am doole te méngoo ak jamono, rawati na Poor bu Ndakaaru.
Ci kanamu jafe-jafe yi ñu fésal, Njiitu Réew mi fàttali na Njiital Jëwriñ li solos jiital ci yitte yi, ànd ko ak ñiy yëngu ci wàll wi, gaaw matale sémbuw yoonal wi jëm ci moom sa bopp ci wàllu koom ak pas-pasu finaasmaa koomum réew mi.
Lu soxal jafe-jafey finaasmaa nag, Njiitu Réew mi xamal na Ngóornamaŋ bi ne jot na sëkk ñu amal càmbar gu matale ci matuwaay yi ñu jot a teg ci réew mi niki noonu fexee teg pexe mu am doole te nu téyeel ko sunu bopp ngir dooleel finaasmaa bu wér ci koom mi. Ci wàll woowu ba leegi, xamal na Njiital Jëwriñ li ne fàww muy xamle 3i weer yu ne ci Ndiisoog Jëwriñ yi, tolluwaayu doxal gi ci ni ñu pàcc-pacee sémbu “Senegaal Gis-Gisu 2050” ci diggante 2025-2029.
Njiitu Réew mi dikkaat na ci lu yaatu ci taxawu gi Nguur gi war a jëmale ci askan wa loru ci dexi Senegaal ak Gàmbi yi fees ba tuuru. Xamle na ne fàww ñu yeesalaat boole ko ak teg pexe yu wóor yu jëm ci fegu ak man a dékku jafe-jafe yu ni mel ëllëg. Xamal na askan wa loru ne, réew mépp a ngi seen ginnaaw di ànd ak ñoom ci jafe-jafe yi teg ci soññ Ngóornamaŋ bi ñu gën a yokk matuwaay yi ñu jël ngir jàmmaarloo ak jafe-jafe ya boole ko ak teg i pexe yu jëm ci aar tool ya, jur ga ak yënguy koom ya ñuy amal ca gox yooya loru ci mbir mi.
Njiitu Réew mi yëgal na Ndiisoo gi ne dina dem ca Tundu Kéedugu, 18 ak 19i oktoobar ngir nemmiku gox ya way-loru ña nekk ca la wër Faleme ba, yóbbaaleel leen itam njàppaleg askanu Senegaal.
Njiitu Réew mi posewu na ci bis bi ñu jagleel wàllu dund ci àddina si, xamle ne moom sunu bopp ci wàllu dund fàww nu jaare ko ci baral jéego yi jëm ci taxawal politigu mbay mu wér te wóor. Ci loolu xamle na ne fàww ñu xoolaat liggéey yi ñuy amal jëm ci wàllu ndox mi, rawati na ca “Vallées” bu dexu Senegaal ak Anambe, lépp ngir yokk bu baax suuf yi nga xam ne dees na fa man a doxal mbayum ceeb mi ànd ak mekaniise ko boole ko ak yokk sistem yi ñuy saytoo ndox mi.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ li mu sukkandiku ci jubluwaay yu bees yi ñu teg ci wàllu amenaasmaa ak porodiksoo, xoolaat sas ak jumtukaayi yëngu yi ñu jox SAED ak SODAGRI rawati na. Fàttali na Jëwriñu Mbay mi ne fàww ñu taxaw ci aar suufi “Domaines Agricoles communautaires” yi ak yu ISRA, ngir yokk bu baax porodiksoo bi ci jiwu yu wér te doy. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu taxaw ci fexe ba ñu man di soppi ci réew mi liy ñoree ci mbay mi. Xamal na leen itam ne warees naa gën a gunge mbayum ceeb mi jaare ko ci wàññi njëgu yasara gi ci jamono ji ñu koy soppi boole ko ak di jëfandikoo yasarag jant bi ci tooli ceeb yi ñu samp. Xamle na itam ne fàww ñu càmbar tolluwaay bi teg ci xamle naal yi ñu namm a amal ci suqali warab yi ñuy tàggatee ci wàllu mbay.
Njiitu Réew mi woo na Ngóornamaŋ bi ñu gën a dooleel napp mi, ndax bokk na ci liy tax askan wi man a am lekk gu baax. Ci loolu, sàkku na ci Njiital Jëwriñ li mu gën a dooleel koppar yi ñu jagleel pàcc yiy yëngu ci wàllu mbayum jën ngir fexe mu doon lu yaatu fépp ci mbeeraayu réew mi.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ li mu sumb ay xalaat yu jëm ci taxawal benn “Conseil national de l’Alimentation.” Kurél gii war a dajale pàcc yu bari ci réew mi dina tax ñu man a feddali politig yi, sémb yi, naal yi ak matuwaay yi jëm ci gën a dooleel li ñuy porodiwiir ci wàllu pepp, jur gi ak meññeefi géej gi, waaye tamit di saytuwaale baaxaayu ñam yi ñuy jëfandikoo ci réew mi ak seen jeexital ci wàllu wér gi yaram.
Njiitu Réew mi daanelee ci ndokkale Gayndey Futbalu Senegaal yi jàll ci joŋantey CAN 2025 yi ñu war a amal ca Marog te di leen ñaanal ñu am ca ndam lu yaa.
Ci ndoorteel i kàddoom, Njiital Jëwriñ li xamle na mbégtem Ngóornamaŋ bi ci anam yi askanu Senegaal àndee ci Tegtalukaayu politig bu bees bii ñu leen gaaral ci wàllu doxaliinu koom ak nekkiin di “Senegaal Vision 2050”. Sant na bu baax Njiitu Réew mi nga xam ne rafetlu na lool liggéey bu am solo bii doon njureefi jéego yu ñu yàgg a teg ànd ko ak kàngami Senegaal yu am taxawaay te bawoo ci ndoxalug pénc mi, gox yi ak goxaan yi, sektëer piriwe bi ak sosete siwil bi.
Ngir yegg ci jubluwaayi gis-gisu Senegaal gu moom boppam, jub te naat, te li ci jiitu di doxal ko ci palaŋu juróomi at 2025-2029, Njiital Jëwriñ li sàkku na ci Jëwriñ yi ñu taxaw ci ñenti sas yu am solo yii:
Jëfandikoo Tegtalukaay bii ci mbooleem wànqaasi njëwriñ yi;
doxal palaŋu juróomi at bu 2025-2029, rawati na dëggal pexe yi ci ay jëf, naal ak sémb yu ñuy séddale ci palaŋ yu ñuy doxal at mu ne ak màndarga yu wér;
amal ag caytu ci mboeem wànqaasi njëwriñ yi ni sémb yi ak naal di duggalante jaare ko ci nataal yu leer ak doxaliin wu dëppoo ak ndoxal gu méngoo ak jamono;
dooleel man-mani njëwriñ yi ci wàllu doxal ay palaŋ;
Ci ñaareelu tomb bi mu doon àddu, Njiital Jëwriñ li leeral na Njiitu Réew mi ci jéego yi ñu jot a teg ci tegtal yi mu joxe woon jëm ci gunge askan wa gàddaayee woon ca Kaasamaas ngir ñu man a sancaat. Ci loolu, am ndaje mu ñu ci amal diggante jëwriñ yi 8i fani Oktoobar 2024, tax na ñu taxawal fa benn “Plan Diomaye Pour la Casamance” boo xam ne ñu séddale ci ay jëf yu wér yu ñu war a teg, ak njëlul 54i milyaari FCFA yu ñu ko nattal, ngir fexe ba gunge ñi gàddaayoon ñépp ñu man a sancaat ci anam yu mucc ayib. Njiital Jëwriñ li ñaax na mbooleem Jëwriñ yi, kenn ku ne ci ñoom am la ñu la sas ci luy doxal palaŋ bi, nga taxaw temm ci doxal naal yi te lépp ànd ak yëgoo niki noonu boole ko ak sàmmonte ak àpp yi.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI
Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi àddu na ci tolluwaayu wal mi am ginnaaw dexi Senegaal ak Gàmbi yi fees ba tuuru;
Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa def na leeralu ayu-bis bi muy amal ci tolluwaayu saytug wal mi.
Jëwriñu Napp mi, jumtukaayi géej yi ak waax yi def na leeral ci pooru Ndaaxoongaa-Funjuñ ak poor seg yi;
Jëwriñu Mbay mi, Moom sa bopp ci wàllu dund ak Càmm gi àddu na ci céddaleg jiwu ji ci atum 2024, tolluwaayu mbay mi ak saytu njaayum lujum yi ca biti réew.
CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:
Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :
Sémbu dekkere bi jëm ci dajale payoor yi ñeel kóppi piriwe.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi
Aamadu Mustafaa Njekk SARE