SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ GU ÀLLARBA 09i FANI OKTOOBAR 2024

NDIISOOG JËWRIÑ YI - 09 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, àllarba 09I fani oktoobar 2024, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.

Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi, wane na mbégteem ci 5eelu bëccëgu jaayanteg ma-réew yi ci  bisu « Setal sunu réew » bi ñu jagleeloon lekool yi. Jaajëfal na mbooleem askanu Mbuur, kilifay ndoxal ga, njiiti gox ba ak kuréli njàng ma ci dalal gu mucc ayib gi ñu ko jagleel, mu boole ci rafetlu ni ñu takkoo taxaw ci bëccëg gii ñu daje woon ca Lycée Demba Jóob. Jaajëfal na bu baax itam Jëwriñu Njàng mi, kilifay Akaademi ga, Njiital Lycée ba, jàngalekat ya ak dongoy lekool boobu doon royuwaay. Mu tëjee bunt boobu ci fésal jaayante gu sax gu Nguur gi am ngir suqali bu baax jàngukaay yi ak li ko wër jëm ci dugal loxoom bu baax ci taxawal anam yu mucc ayib yuy tax dongo yi man a amal njàng mu jaar yoon.

Ci laaj yi mu samp jëm ci xereñteg pexem dimbalante mi ñu teg ci réew mi, Njiitu Réew mi xamal na Ngóornamaŋ bi jamp gi nekk ci yeesalaat politigu dimbalnte gi ak taxawu askan wi jaare ko xoolaat ci ñi ñu jëmale ak boole pexe yi ñuy teg jëme ko ci way-ñàkk ñi ak gën â néew doole ci askan wi. Taxaw na bu baax nag ci xamle ne lu manul a ñàkk la ci yeesalaat boole ko ak gën a yaatalaat ci ñeneen ñu bees, njoxem sémbi ndimbal yi ñu jagleel njaboot yi (bourse familiale), Këyiti yamale muur yi, taxawu ci am paj mi ak jot ci ab dund. Mu lu war a taxaw kon, ci diir bu gàtt, ci boole mbébet yi jëm ci amal taxawu gu mucc ayib ñeel askan wi. 

Njiitu Réew mi, sàkku na itam ci Jëwriñu ji yor wàllu Liggéey, mu xayma ay naal ak i sémb yu jëm ci taxawu askan wi te lépp dëppoo ak anam yi ñu yoonal ci àddina si. Ci loolu fàttali na solos yeesalaat gu sax ci  

 Registre national unique (RNU) bi, xoolaat doxalug sàrtu orientation sociale l° 2010 - 15 bu 6 sulet 2010 bi aju ci sàmm yeleefi way-laago yi niki noonu mottali ci fan yii kot bi soxal Sekirite Sosiyaal te war a yombal boole yënguy Caisse de Sécurité sociale ak bu Institut de Prévoyance Retraite du Sénégal (IPRES). Ci wàll woowu, xamle na ne fàww Ngóornamaŋ bi sumb ay xalaat yu wóor ci ni ñuy saytoo àllaateret yu Senegaal.

Lu soxal mbirum politig bu yees bi jëm ci saytu ak gunge saa-seenegaal yi féete biti réew, Njiitu Réew mi xamle na seen nekkiin bis bu set, dafa war a doon lu yitteel Ngóornamaŋ bi jaare ko rawati na ci gën a sóob ndawi laamisoo yi ñu gën a farlu jëme ci taxawu leen. Sàkku na ci Ngóornamaŋ bi ñu baral jéego yi ci anam yi ñu jotee ci wayndarey ndoxal yi manul a ñàkk, jàll-waax ak këyitu jëmm rawati na. Soññ na Ngóornamaŋ bi muy topp tolluwaayu njàngaani saa-senegaal yi nekk biti réew ak fexee xam kàngami Senegaal yi féete biti réew di fa liggéeyee. Xamle na tamit ne fàww ñu taxawal jumtukaayu taxawu bu bees jëm ci dellusi ak sampaat saa-seenegaal yi nekk biti réew.

Lu soxal dayoo bu am solo bi càmm gi am ci politigu moom sunu bopp ci li nuy dundee, Njiitu Réew Mi sakku na ci Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde ak Càmm gi ak Sekkereteer Detaa bi yor wàllu Lootaabe baykat yi, ñu yeggali, ànd ko ak ñiy yëngu ci wàll wi, xayma gi ci naal yi, sémb yi ak déggoo yi ci wàllu sàmm ak liy bawoo ci jur gi. Xamle na ne fàww rekk, niki ñu ko waxee ci PROJET bi, ñu taxaw ci fexe balaa yàgg ñu man a matale ci jox Senegaal lépp li mu yittewoo ci wàllu jur gi, te jéem a wàññi bu baax jéggaani gi nga xam ne day diis lool ci gafag réew mi.

Cig àddoom, Njiital Jëwriñ li fàttali na yitte ju kawe ji Njiitu Réew mi jox di faral di amal ay xayma ci tolluwaayu liggéey yi nguur giy amal. Ci loolu, sàkku na ci Jëwriñ yi ñu xamle tolluwaayu seen i yëngu, ca njeextalu sebtàmbar 2025, ci naali doxal yi ñeel wànqaas yi aju ci seen njëwriñ. Ñu war a taxaw nag ci wane gis-gisu nguur gii ci doxaliinu pénc mi, méngale ko ak ñi weesu. Ñu war kon ci loolu, aajar ci anam yu leer nàññ, njureef yu am solo yi ñu jot a am ci diir bu gàtt ci mbooleem fànn yépp. 

Ci noonu, Njiital Jëwriñ li sàkku na ci Jëwriñ yi ak Sekkereteer detaa yi ñu taxaw   temm ci doxal gu mucc ayib sémbi liggéey yi soxal 3i weer yi mujj ci atum 2024 ci wànqaas yi aju ci seen njëwriñ. Muy kon fexee matale taxawu gi, ci àpp yi war, ñeel tomb yi gën a jamp fii mu ne, yu mel ni kàmpaañu njaayum li ñore ci mbay mi, bàyyi xel pas yi ñu jaayante woon ngir war leen a fay ci njeextalu at mi niki noonu may gët bu baax sémb yi ak naal yi.

Ci anam yu wóor, wareef naa bàyyi xel bu baax màggal 80eelu ati bóomug “Caaroy 44” niki noonu yeggali yenn liggéeyi càmbar yi ak liggéeyi Poor bu Séndu. Noonu it la war a demee ci saytu tereg jëfandikoo wurus wi ci Faleme bi, wéyalug gunge dellusig ña gàddaayee woon Kaasamaas, topp doxalug dogal yi jëmoon ci wàññi njëgu dund bi, niki noonu lootaabeg Biennale des Arts de Dakar. 

CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:

Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa def na leeralu ayu-bis bi muy amal ci tolluwaayu saytug wal mi.

CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI:

Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale :

Sémbu dekkere bi jëm ci doxal yenn matuwaay yu sàrt l°2023-15 bu 2 ut 2023 te aju ci kotu kéew mi.

CI DOGALI JAGOO YI, Njiitu Réew mi jël na dogal yii: 

CI WÀLLU Njëwriñu Biir Réew Mi ak Kaaraangeg Pénc mi: 

Soxna Sëynabu GÉY, Administaraatëer siwil, tabb nañu ko Inspecteur de l’Administration centrale et territoriale bu  Njëwriñu Biir Réew Mi ak Kaaraangeg Pénc mi, mu wuutu Soxna Ramatulaay JEŊ mi ñu woolu ci yeneen yitte;

Sëriñ Séeku Wiyé JAATA, Jàngalekat, limatu payoor l°630 591/F, doonoon lu jiitu Dee-calaw lu Arondismaa Taayif, Goxu Mbàkke, tabb nañu ko Topp-Calaw lu Goxu Géejawaay, toogu bu kenn ne wutoon;

Sëriñ Abdu Xaadir JÀLLO, Jàngalekat, limatu payoor l°675 797/A, doonoon lu jiitu Topp Dee-calaw lu Cille Buubakar, Goxu Podoor, tabb nañu ko Topp-Calaw lu Goxu Malem Hodaar, toogu bu kenn nekkutoon;

Sëriñ Anabi MUSAA, limatu payoor l°612 954/A, doonoon lu jiitu Topp-Dee-Calaw lu Arondismaa Lujaa Wolof, Goxu Usuy, tabb nañu ko Topp-Calaw lu Goxu Bunkiliŋ, toogu bu kenn nekkutoon ;

Sëriñ Ngóor PUY, jàngalekat, limatu payoor l°517 772/I, doonoon lu jiitu Dee-calaw lu Arondismaa Ndorna, Goxu Médina Yoro Fulah, tabb nañu ko Topp-Calaw lu Goxu Bàkkel, toogu bu kenn nekkutoon ;

Sëriñ Usmaan SAANE, Sekkereteeru Ndoxal, limatu payoor l°519 212/J,  doonoon lu jiitu Dee-calaw lu Arondismaa Simbaandi Baraasu, Goxu Gudomp, tabb nañu ko Dee-calaw lu Sagata Jolof, Goxu Lingeer, toogu bu kenn nekkutoon ;

Sëriñ Sãa Póol Silwee JAATA, Sekkereteeru Ndoxal, limatu payoor l°661 427/H, doonoon lu jiitu Topp-Calaw lu Goxu Bàkkel, tabb nañu ko Dee-calaw lu Simbaandi Baraasu, Goxu Gudomp, mu wuutu Sëriñ Usmaan SAANE mi ñu woolu ci yeneen yitte;

Sëriñ Ibraahiima NJAAY, Sekkereteeru Ndoxal, limatu payoor l°517 694/J, daan liggéey lu ko jiitu ca Direction générale de l’Administration territoriale, tabb nañu ko Dee-calaw lu Arondismaa Waajur, Goxu Gosaas, mu wuutu Sëriñ Ibraahiima NDAW mi war a dem àllaateret;

CI WÀLLU Njëwriñu Bennoog Afrig ak Jëflante ak Biti Réew :

Sëriñ Mammadu GAY, Seneraal de diwisiyoo (2s), am lijaasa ci xam-xamu sóobare, tabb nañu ko Njiital Kurél giy saytu aj gi ca Warab yu Sell yu Lislaam, mu wuutu Sëriñ Buubakar SAAR;

Sëriñ Asan NJAAY, lu ko jiitu mu doonoon xelalekat ca Laamisoog Senegaal ca RYAD ak ca Toogub Senegaal ca OCI, tabb nañu ko Topp-njiital kurél giy saytu aj gi ca Warab yu Sell yu Lislaam, mu wuutu Sëriñ Xaadim SILLA;

Sëriñ Mohammet Mansuur NJAAY, am lijaasa ci wàllu tekki ak àntarparet ci wàllu waxtaan, tabb nañu ko Topp-njiital kurél giy saytu aj gi ca Warab yu Sell yu Lislaam, mu wuutu Sëriñ Usmaan NDÓOY.

Ci wàllu Njëwriñu Caabal yi, Jokkoo yi ak Xarala:

Sëriñ Habiibu JA, am lijaasa Master 2 ci wàllu t'as xibaar ak jokkoo, tabb nañu ko Njiital Jokkoo yi ca Njëwriñu Caabal yi, Jokkoo yi ak Xarala, mu wuutu Sëriñ Useynu JEŊ;

Sëriñ Abdu Lahat NJAAY, Xereñtaan ci wàllu xarala yi ak ndefar, tabb nañu ko Njiital Kurél giy saytu  Fonds de Développement du Service universel (FDSUT), mu wuutu Aali Koto NJAAY;

Sëriñ Mammadu Lamin SEEN, Xereñtaan ci wàllu elektoronig ak xarala yi, tabb nañu ko mu bokk ci komite direktëer bu Fonds de développement du service universel (FDSUT), mu wuutu Sëriñ Seex MBÀKKE;

Soxna Ndey Sëynabu SI, am lijaasab Master 2 ci wàllu business and corporate law, tabb nañu ko mu bokk ci komite direktëer bu Fonds de développement du service universel (FDSUT), mu wuutu Soxna Sofi NJAAY;

Soxna Sira Ñaŋ SI, am lijaasab Master 2 ci wàllu management et négociation, tabb nañu ko mu bokk komite direktëer bu Fonds de développement du service universel (FDSUT), mu wuutu Sëriñ Abdulaay NGOM ; 

Sëriñ Suleymaan NJAAY, am lijaasab Master 2 ci wàllu informatique et réseau, tabb nañu ko mu bokk ci komite direktëer bu Fonds de développement du service universel (FDSUT), mu wuutu Sëriñ Mammadu Yaaya BA;

Sëriñ Aamadu Moktaar NJAAY, Xereñtaan ci wàllu télécommunications, tabb nañu ko mu bokk ci komite direktëer bu Fonds de développement du service universel (FDSUT), mu wuutu Sëriñ Mammadu Al Haaji LI.

Ci wàllu Njëwriñu Kéew mi ak Jàll ci ekolosi:

Sëriñ Abdu JONG, Conservateur des Parcs nationaux, limatu payoor l° 613 282 /L, tabb nañu ko espektëer tegnig ca Njëwriñu Kéew mi ak Jàll ci ekolosi, mu wuutu Soxna Ndey SEEN;

Liyetnaa-Kolonel Asan NDÓOY, Conservateur des Parcs nationaux, limatu payoor l°510 886/B, tabb nañu espektëer tegnig ca Njëwriñu Kéew mi ak Jàll ci ekolosi, mu wuutu.  

Ci wàllu Njëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi:

Sëriñ Abdul Asiis JUUF, Profesëer ci droit privé, tabb nañu ko Bootalu Njàng mu kawe mi, mu wuutu Sëriñ Aamadu Abdul Sow, mi war a dem àllaateret;

Sëriñ Haamidu DATT, Profesëer ci wàllu Màndaxe, tabb nañu ko Bootalu Gëstu gi ak Fent, mu wuutu Sëriñ Aamadu Galo JÓOB, mi war a dem àllaateret;

Serin Paab Abdulaay JAW, Maître de conférences titulaire, tabb nañu ko Bootalu Institut supérieur d’Enseignement professionnel bu Rissar Tool, mu wuutu Soxna Awa ÑAŊ, mi ñu woolu ci yeneen yitte; 

Sëriñ Alasaan JÉEJU, Profesëer titulaire, limatu payoor 102524/D, lu ko jiitu mu doonoon topp-njiital Jànguneb Asan SEKK bu Sigicoor, tabb nañu ko njiital Jànguneb Asan SEKK bu Sigicoor.

Ci wàllu Njëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay yi: 

Sëriñ Seydinaa Àlliyun JIM, am lijaasab Master professionnel ci wàllu Management et Administration des entreprises, tabb nañu ko Bootalu est nommé Directeur des Paysages urbains et des Espaces publics, mu wuutu Soxna Maam Mari Usmaan NJAAY, mi ñu woolu ci yeneen yitte;

Soxna Aminata WAN, am lijaasab Master 2 ci wàllu Urbanisme et Aménagement, tabb nañu ko Bootalu Planification urbaine et de la Réglementation, Mu wuutu Sëriñ Yuusuf MAANE, mi ñu woolu ci yeneen yitte;

Sëriñ Séeku Umar JÉEJU, am lijaasab Doctorat ci wàllu Melosuuf ak lijaasab Master ci wallu Aménagement urbain, tabb nañu ko Bootalu Promotion du Développement des Territoires, mu wuutu Sëriñ Mbañig JUUF, mi ñu woolu ci yeneen yitte;

Sëriñ Aaróona BA, am lijaasab DEA ci wàllu Politiques économiques et gestion di Xereñtaan ci wàllu travaux de planification, tabb nañu ko Bootalu Collectivités territoriales, mu wuutu Soxna Faatumata Bintu KAMARA, mi ñu woolu ci yeneen yitte;

Sëriñ Momar NJAAY, Xereñtaan ci wàllu gestion des travaux de développement urbain, tabb nañu ko Bootalu Aménagement urbain et de la Restructuration, mu wuutu Soxna Sëynabu Ummi GUMBALA, mi ñu woolu ci yeneen yitte.

Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi 

Aamadu Mustafaa Njekk SARE